Rëne indiwaaleel na ma bataaxal bu jëm ci Mamadu.

Mamadu mungi ni capp ci kanamu mobiletam, ni xujj di ma gestu.

Nii la amewoon itam ñaari at ci ginnaaw.

Booba mungi toogoon ci ab pindub teen.

Maangi yëgaat taaram, seddaayam ak lewetaayam. Maangi yëgaat ba tay ni bu nu dajee rek, du mën ci man xool bu àgg. Leer na ma ni sunu diggante du dem.

Nangu gi ma nagu ab Taaram akub seddaayam akuk jekkam rek doy na metitu xol.

Buur Dawda daanu si na.

Moom dawlàqu bi, boroomi pexe yi te bëgg nguur, moom waykat bu mana jaay taar bi, boroom wurusu ngalam wu sakan wi.

Ci kanamam gu yummiku gi, bëti ku jaaxleem kaa ngi xóll.

Tergaal biy ngelaw ci kawam.

Mu nuyoo nu bopp.

Muuñul sax.

Wayul.

Yaayam la àndal.

Aidara dugg si na.

Mungi ñaajalub dënnam.

Ni nikk sama loxo të koo bàyyi.

Mook yaayam a ànd.

Sagnaa ngi walaxwalaxi di ñaxtu.

Baayam la àndal.

Póol di tufli.

Te tuflit wu ne, xaaxtandikooy cay topp.

Ku soof la. Saa su ne am na lu nekk ci putam gi.

Ak bóli gu wow gi.

Dañu ko fi war a jëlé.

Fii fees na dell aki tuflit.

Tuflit yu bari te dara mënul a génne ci putam gi.

Póol tufli na.

Put gi wowatina.

Dañu kofi war a jële way.

Yaayam la àndal.

Ibraayma mi nguunun-gaana mungi ñëw.

Ak kanam gu ni nàññ.

Ku ràkkaaju ki.Njuuma li ci bopp bu rëy bi.

Boroom dënnub njegemaar bi ak geen bi ni jadd mu uufaale ci digante pooj yi.

Ibraaymaa ngi ñaq.

Niin batt ci kaw céram yu mat yi.

War naa am 17 walla 18 at.

Buy dox di sëgg ndax garab yi muy naan.

Yaayam la àndal.

(yaayam) dafa xam ci gemmeñ gi

Dafa bëggóon ñu faj ko (Ibraayma) fajum tubaab.

Nozinan, Anafranil, Haloperidol, Largactil.

Ibrayma dafa war a dem Dakar fajuji.

Wante xaalis amul.

Golan mungi ñëw di cëppcëppi ndànk ndànk akub nelam.

Kanam gi ni gu sinwaa ci yaramugoneg màngaanug fukki at ak ñaar ca Afrik.

Day tàllal loxob sàmmam bi.

Daldi ni wërëñ.

Mu joxewaat loxo bu wow bi.

Salleeru.

Di seet suukar si.

Ci wetu siis bi. Ci kaw pooji mamadu. Ci geneen wetu siis bi. Ci mbaarum kërug ndaje gi.

Ñu yobbu ko ba ci wenn jën. Muy làmtu ak a raay jën wi.

Muy làmbtu ak bët yu ni patuus, aki lexam, ak gemmeñam di seet, di seet ak a fóon bant bi. Wante bat bi génnewul meew.

Yoxoy Golan yaa ngi lox.

Mel ni ku dong.

Garab yi muy naan la.

Melo ak jëfi ku dong.

Meloy feebaru xel

Golan a ngi jéem a takk ñaari daggitu lastik ci jumub bant.

Limuy lox lepp defar na nak ak laspeer.

Golan yekkati ab màngo di ko lakk ci taal bi ñuy attaayaa.

Mamadu woo nanu añ.

Wante moom woowunu.

Woowul kenn.

Laajunu.

Wakërëm, jabaram, yaayam ak doomam jiy doora am weer yu néew, akub goroom

Toog wër benn bool.

Ceebu diw tiir ak kàmmaate.

Lujum bu vert buy nirook kàmmaate tey saf batañse.

Bisaab la. Xob yi day nirook mbuum te cafka gi forox.

Gaynde géej.

Gaynde géej bu juge Kaasamaas mi xoromam dem ba Cigicoor.

Njaboot gaa ngi dank ceeb bi.

Ñeex miy siit.

Ñu ngi coppati ci jën wi di ko sifat di ko ko tegal.

Mamadu:

– Njaboot gaa ngi joqalante xale bi ci seen biir.

Nday ji jox na ko Leonore. Leonore jox ko Mamadu. Mamadu jox ko yaayam.

– Bu xale bi dee yuqeel, ñu am lu weex luñu ko tafal ci jë bi aki tuflit.

– Sama doom angi doora am weer. Wenn weer ci lay tàmbalee gis.

Leppay leer ba ëpp ci moom. Moom nak du ñuul kuuk. Ku xol nopp yi rek xam ko. Ndaxte noppay jëkkë wane meloom dëgg.

– Niwaakin lanuy naan ngir baña sibiru.

Liir moom siro niwaakin lay naan.

– Fii ci sunu kërug dalal xel gii waroon nanu fee mën pajum simoterapi. Fii pajum nëroleptik lañu fiy faje. Moo tax ñu ci tane bañu bàyyi leen, ñu daanuwaat bu seen xaalis jeexee ba manatuñu jënd garab yi.

Ci ngoon gi la nu fajkat bu tudd Mamadu yóbu ci kilifagu mag gi.

Leonore ni ma:

– Bu kilifagiy wax, Mamadu ni patt ni ab muuma.

Kilifa gi nee na:

– Kërug dalal xel gii ñungi ko daloo ci atum 1974. Mungi nekk ci dëkk buñu naa Kenia, ñatti kilomet digganteem ak Cigicoor. Ñungi ko duppe jenn jëwriñ ju génn àduna juñu naan Emile Badiane.

– Dinga naan sëng ?

– Kër gii jaral na profesëër Collomb lu ne. Da fiy yonnee ay karabi farmasi yu juge ba Dakar, ba tax na fii du ñàkk mukk ay garabi nëroleptik.

– Jàppuma dara ci pajum cosaan mi. Ndaxte nit ñi fii lañuy ñëw, ganaaw buñu demee ci seetkat yeek jibar yeek maaman yi ba tëlé. Fekk na ñàkk nañu xaalis bu bari te wéruñu. Nun danuy fexe ba ñu wérëdi ñi mana dundaat ci seen biiri njaboot. Te sax nun nëroleptik lanuy faje. Ba ci ñu kanasu ñi. Gis nanu ci ak yokku nak bu baax.

– Danuy faj itam kuy daanu këriis.

– Sunuy garab nak sakanul noonu.

Njabootug ñiy faju itam oomlewuñu. Genn góorug 65 at gu doon këriis, danu koo mujj yóbbu Dakar. Ndaxte xaalis amu fi woon.

– Yen paj yu xóot yi mënu nu ko fee amale. Ndaxte loolu day yàgg di laaj it xaalis bu bari. Te way tawat yi amuñu ko.

– Ci wall woowu, ay sinwaa lanu ciy lëkkëlóol. Wante yombul. Ndaste yen saa yi dunu mana jàngat seen wardnaas yi. Seen garab yi itam aayuñu ci yenn feebar yi.

– Man Joolaa laa di làkk Joolaa ak Wolof.

– Collomba ngima jàngale faj ca Dakar. Maangi fàttaliku bu wér ni mu ma tàggate fii ci poet bii. Yombul woon. Sama xame ya ca Dakar yepp la mujj bàyyi. Wante mujj naa am ay xarit yu beesfii ci Cigicoor.

Mamadu moom, balanta la.

Day làkk Balant ak Wolof ak Joolaa.

Dégg na itam Mànkaañ.

Kilifa gi nee na:

– Ca ndoorte la 8 kër dong lanu amoon. Leegi nak am nanu 29 dëkkuwaay. 3 teen am nañu fi.

– Ren amunu benn jafejafey ndox. Wante max gaa ngi ñëw.

– bu jëgg, ci ëtt bii lañu daan jànglee lu aju ci mbay. Wànte fii yoonu max la. Moo tax man nanoo wax ni dañoo nax sikaatar yi ca jënd ma. Garab yi màgguñu, ndaxte max geey lekk reen yi.

– Way tawat yi mënuñu fee yàgg – bu baree ba bari ñaari weer – nu bàyyiwaat leen. Daanaka jarul ñoom ak seeni andandoo ñu fiy jéemë bay dara. Looloo tax nu far ànd bokk benn tool di ko bay.

– Gerte gi ak mango ji dañu koy jaay.

– Kër gi ñu ngi ko ubi ci atum 1974. Boobaak leegi, 203 jaar nañu fi. Jamono jii 13 way tawat ak seen 13 jigeñaale yu àndak ñoom ñungi fi ak 2 Jaraaf (boroom dëkk ci aada) ak ñaari fajkat, man ak Mamadu. Doktoor ya ca Dakar, war nañu nemmikusi dëkk bile. Wànte ba leegi, kenn jekkagul ngir ñëw fii. Benn doktoorub nasarann daal bu nekkoon ci dëkk yii nu wër, moo fi daan ñew ca jëmmi jamono.

– Profesëër Collomb dafiy ñëw akuk roplaanam, waaye yeneen fajkatu dof yi toog Dakar a leen gënël. Monte xaatim nañu ci seen kontaraa ni ñoomit war nañoo def ab diir ci àll bi. Wànte fexe nañu bag is benn kilinik bu nekk ci wetu Dakar, ñu jàppe ko ab àll.

– Dëgg bii ñungi ko taxawale ci xalaatu profesëër Collomb. Dafa bëggóon ñu lëkkëlé pajum cosaan ci afrigak pajum tubaab mu bees mi. mu yaakaaroon ni loolu dina nekk royuwaay lu rafet ci Senegaal ak ci afrig gepp.

– Nguur gi joxewul dara ci xaalis.

– Rotary-Club sax bëggóon na def dara ngi dof yi.

– Téeméeri junniy dërëm lañu am – muy méngóo ak 6000 Mark – ci juróom benni weer.

– Way tawat yi duñu fay dara fii ci paj mi ak garab yi.

– Way tawat yi ak seeni jigeñaale daal war nañoo indiwaale as lëf luñu dugal ci lekk gi. Nun dinanu joxeel kenn ku nekk 800 garaamu ceeb ak xaaju gennwalliitëru diwug gerte ak gennwalliitërupetorol ayu bës bu nekk. Jigeñaaley way tawat yi ñooy indi jën, lujum ak xorom.

– Leegleegi itam nu boolaate tog genn togg bokk ko.

Mamadu:

– Ba bima kokilifa gi di tere, damaa jigewoon doff yi lool. Dañu daan ñëw sama kër, toog wër ma nuy kart.

– Daawuma leen jox doom yi leegleeg. Jox leeni doom lu jafe la. Dañu koy sànni. Te seen jigeñaale yi duñu leen ko jox ci waxtu yi gën.

– Bëggumaa forse kenn.

– Ñaanoon naa itam kër yi buleen kenn toftale. Xoolal fëlé ca digg ëtt ba. Maa ni woon, nañu dakkal ligeey bi, bu fa genn kër taxaw.

– Tay jii tëddinu kër gi day misaal jikkoy kilifa gi fi nekk.Kilifa gi moom, day tëj ay buntam. Ku ñëw, dangay fëgg.

– Kilifa gi moom, soldaar dëgg la. Moom ay ordur rek la xam.

Ay xale yu góor a ngi jëm ca sënub Cigicoor biy boy.

Ñungi ànd ak ay mbineef yu sëq lipp.

AyKankuraŋ.

Ak ay ñingo.Ñuy cëppëppi ci ngelaw li aka dem ba ci fiilu kuuranŋ yi.

Wòoruta jige nak.

Mbooloo mi romb tapib aydapoor bi daadi dug ci gutt bi.

Ay mañeer yu yàgg lañu ame. Kenn soloowuci ni kànkuraŋ bi nak.

Jean Delay ak Pierre Deniker:

Pajum Simoterapi ci dalal xel.

1954 ba leegi.

Reserpin

Koloporomasin

Jafejafe yu yéemé la paj mi di lëkkëlóo.

Moo tax nu tënkóon ko baatub nëroleptik ngir jeexital yimuy am ci xelum dnit.

Jeexital yi ci gënë ràññiku ñooy yii:

  1. Cér yu nasax ba ràññiku.
  2. Dal gi muy dalal ku yëngu.
  3. Wàññi gimuy wàññi xel mu nëx.
  4. Jeexital yi muy amal ci bopp.
  5. Solos jeexital si muy am ci yuurug nit.

Jeexital ci kaw cér yi:

Gasax.

Ñàkkug yëg gu ràññiku.

Tóoy.

Diib ndonte cuq nañu ko. Wante loolu du wàññi dara cig Ràññeem akug xàmmeem.

Mel ni ku jaxasoo.

Néew dooleg cér yi.

Nëroleptik yi ëpp doole ràññiku nañu ci nataala ci lu néew jeexital yu am solo yi doom yile am ci bopp ak xelum doomu aadama.

Pajum biyolosi du feeñ ci ñi ame feebaru xel ludul ni day amalug coppiku ci yenn bërëb yu am solo yi ci yuur gi.

Xam xam bu néew lanu jotagula am ci melokaanug coppiku gi Doom yi ñuy naan di amal ci seen biir bopp bi.

Bokk na ci jafejafey ñàka mana faram fàcce gaañu gaañu yiy am ci yuur gi ganaaw bu lëjlëj amee ba dee toftalu ci. Coppiku yu fés ci yuur gi dees nañu ko ràññee saa sune. Gaañu gaañu yi dañuy sakan ba laal yuur gépp daanaka. Wepp melokaan wu laal céri yoxo yeek tànk yi nak, mbaa xel mi defees nañu ci bu yàgg am njàngat mu wér muy sukandiku ci xalaatu Economo bijëm cimetitug yuur ak lamuy jur.

Mamadu:

– Buma sañoon, duma jox Ibraayma benn garabu sikotorp. Kon aspirin rek laa koy jox walla palaasboo. Waaye kilifa gi moom dafa fonk nëroleptik lool.

– Nëroleptik ci baaxub jigeen bu lëj.

– Ci yoon, Ibraayma warutoon a am benn jafejafe.Maneesoon nañu ko tëyé fii.

– Ay jigeñaaleem ñoom fii lañu ko bëggoon a faje.

Jean Delay ak Pierre Deniker:

Koloporomasin, Largaktil miy kiiraayu bepp nëroleptik mooy garabug cosaan ci Sikaatri.

Ay gisgisi négandiku am na ci Potensialisator 45600 RP ca weeru mars 1952.

Laboratoires Rhônes-Poulenc-Spécia.

Ay jeexitali fenosiyaasin yu wér day feeñ ci biir bopp. Loborit ak Huguenard ràññetle nañu ko bañuy ligeey ci Aestesi buñu kartanal.

Loolu man na dem ba jur anestesi bu amul anestetik.

Jeexital ci tàngayu yaram.

Jeexital ci doxinu deret.

Jeexital ci taasyoŋ.

Jeexital ci noo.

Agit yeneeni jeexital.

Jeexital ci ni deret jiy bindo.

Koloporomasin, garab gu am doole la. Am pajam warula yàgg, wàntedafa wara mat sëkk te matale.

Siditi bopp yepp, dañu cee wara naan ba màndi. Solo su mag si mu am ci pajum ndof mooy firndeel maanaam Koloporomasin mi amul feneen ci birr pajum lu aju ci xel.

Ay yi ci aju:

Dee gu gaaw.

Siditi deret yu lakk.

Siditi deret yu fatt

Jafejafe ci biir xëtër yi.

Deret ju taxaw.

Bët yu nab.

Dermatoluzitis.

Sëdówundróos.

Bët yu mboq.

Xol buy tëb.

Gémméñ gu wow.

Lekk guy yeexa rees.

Coppikug tàngaayu yaram.

Jaxasoog biir.

Am yaram.

Coppiku ci baaxub jigeen.

Ween yuy siit.

Ngóora gu wàññiku.

Rimatism.

Sindrom extrapyramidal:

Gasax, yambar.

Lafañ.

Ñàkk deret.

Kawar guy ruus.

Yuut.

Diib.

Sëŋŋ.

Lox.

Këriis okilogiir.

Gémméñ guy yëngu rek.

Buur Dawda moom ab jaaykat la.

Foroot digante liberia ak sierra leone lay dunde.

Ay yéeré ay forot.

Jombul day gér duwaañee yi.

Saa su wérée fii banu bayyi ko rek mu tàmbaliwaat gënë ràkkaju.

Jean Delay ak Pierre Deniker:

Levomoporomasin..

Nosinan

Ay jeexitalam ci këriis ak yëngu gu jéggi dayoñooy gënë garaaw yenn saa yi yu Koloporomasin. Gënë fésé nak ci depresiyoŋ.

Mungi tanee nak ci xel yu nëxënëx yi, lu mel ni doppopoor.

Ci ndoorte li, aji tawat ji day miir ba sonn ni nut. Dañudaan gis ñuy taxaw sax di nelaw bay daanu.

Jeexital yooyu mën na xëmloo nit mba sax mu faagaagal ko. Yi ci gënë garaaw ba mënë indi dee nak ñooyniwi ak xëtër yu yàqu.

Mën naa soppiku poson itam.

Mamadu nee na, Aidara mii jàpp ci sama loxo, moom ab séet la woon. Wante ca guddig céet ga jëkërëm jotulamën a àgg sax ci moom.

Jean Delay ak Pierre Deniker.

Ci atum 1959 la fajkatu dof ya ca belsig firndeel Solos xeetu garab yu yees yu bokkul tus ak yi fi jiituwoon, ñu naan ko butirophenon.

Mu soqi koo ci Haloperidol.

Dafay dalal ku daanub jéll. Jamono ji moo raw ci garabi nëroleptik yi.

Waaye ay jeexitalam ci aji tawat ji wuutewul daanaka ak jeexitali yenen garabi nëroleptik yi.

Du jafe màndarga yu mel ni tàngaayu yaram wu jéggi dayu di feeñ bay waral mànki ndox, ñaq wu bari lool ak ay tupptuppi yaram.

Bu loolu amee, li gën mooy daadi dakal moomu paj. Lu dul loolu rek, dee man na ce topp, ni muy ame ci yenen garab yu am doole yi.

Saaña ñaxtukat bi moom bamu ame fanweeri at la ko ay magam yu góor jàpp ca Dakar, takk ko, delloosi ko dëkk ba daadi koy yóobu ca lë ba.

Jean Delay ak Pierre Deniker:

Tofranil.

1957 lañu dugal Dimethylamino-propyl-imino-dibenzyl ci pajum katakayni.

Jafejafe yi ci ëp nak manees nañu leena saafara ci lu yomb.

Bu baree ci yaram, day far mel ni ku jël dorog ba këriis di kayikayi.

Bu doos bi yamee nak moom, day delloosi xel mi.

Warees nañoo gëstu nak ba xam man pajin moo ci tane ci ku katakayni.

Ibraayma nguunun-gaana gi mungi tëdd ci ron mango gi.

Yen saa yi mu toog ni tekk ci ron mango gi.

Lumu ciy def nag (tëdd walla toog) danaan bëxërñit.

Ni jadd bamu yàgg muni wëlbit.

Njaul Ibraayma laa ngi màgg. Kenn topatoowu ko.

Mamadu moom ci bi la génné lektëëru diskam.

Di misik O-Kay-Jazzu Sénégal.

Mamadu day fecc.

Jaraaf ju mag ji day fecc, ak saraxolle bi, ak bu ndaw bi, ak Bambarabi.

Duwaañe bi day fecc.

Kiy ligeey ci biro bi itam.

Dañuy lëmbël.

Di tëñëxënte.

Di lëngóo ci kaw.

Jàppoo ci suuf.

Buko defee ñuy juyante.

Bu yiw ci ag dal akug tekk.

Duwaañe bi jengal taat wi jëmëlé ko Mamadu.

Mamadu tàpp duwaañe bi ci xott taatu càmmoñ wi, ak ci xott taatu ndijoor wi ak ci ndigg li.

Duwaañe bi ni wëlbit ; Mamadu dugal ndànk loxoom ci xarante tànk yi.

Mamadu jël doomam ju góor.

Muy fecc ci kawi yoxoom.

Ibraayma angi dox.

Dara yënguwul ci moom.

Du ay weenam, du awraam, walla aw yaramam, du ay bëtëm, du boppam walla leen luy yëngu bu Ibraaymay dox.

Jiñax.

Leonore seen na Ibraayma fa ngañ duwaañe bi di futbale muy liyaar Mamadu, di dagdagal bopp aki woom.

 

Wante futbal bi jàpp na leen ba gisuñu liyaari Ibraayma yi.

Mu daadi dakaal lepp dellu ciw maninam.

Altine ak àllarba ak àjjuma june dañuy amal pencoo.

Ci ronum mbaar.

Am ndaje la mu waa dëkk biy amal.

Way tawat yeppay ñëw ak seeni jigeñaale.

Ñu togg ataaya.

Paa Jara, saraxole bi, mooy tekki laaj yi ak tontu yi.

Ci pël. Ci wolof. Ci Joolaa. Ci Màndinka

Aidara boroom ween yu rëy yi sax ñëw na ci pénc mi.

Yëfëm yepp la ëmb. Dafa bëgga raaxaloo ci nit ñ idem yoonam ak ëmb bu rëy bi mu yanu.

Ndayam la àndal.

Ñu di ko reetaan.

Paul yónni benn xale bu jigeen mu indil ko ab piliyaan ci penc mi.

 

Mu tëdd ci ci digg mbooloo mi ñu wër ko. Muy xidamiku. Baat bumu wax xidamiku ko.

Xale bu jigeen bi indil ko benn pot, tegal ko ko ci wetu piliyaan bi. Mu ciy tufli.

Cey yàlla, day xidamiku rek.

Bàyyi ko nu génn !

Day wann bepp baat bu taseeg muy xidamiku.

Tegees na ataaya ca ndoortel penc li.

Mamadu toog ci digg bi.

Teg paketu warga.

Keesug suukar bekk.

Ak kaas yu bari.

Akub palaat.

Akub baraada.

Ak siwob ndox.

Akub furne.

Mamadu raxas kaas yi.

Mamadu ronqi xal yi aki baaraamam.

Mamadu ñulug baraada bi, ganaaw bumu ci sottee warga bàyyi ko muy bax.

Mamadu jëri ataya ji

– Rincer le thé.

Warga waa ngi bax.

Di fuur.

Bu fuurul mooy, nawloowul kenn.

Mamadu xelli, teg ci wet gingir foorale ko barada bu mujj bi.

Suukar baraada bi, sootiwaat ci ndoxum warga wi.

Mamadu teg baraada bi ci kaw furne bi.

Mamadu fuural kaas yi.

Ñati baraada lay togg.

Bi mooy bu jëkk bi.

Tuuti suukar laya am.

Lëwël.

Pour góor ñi.

Jigeen ñi itam man nañu koo naan.

Xale yu jigeen yi, mukk.

Dafa foor.Day yëngëlaate.

Jarafi saraxole ji mooy joxe kaas yi.

Jigeen ñi naanu ñu, dañoo bañ.

Góor ñi ñoom naan nañu .

Leonore naan na, wànte nee na dafa wex.

Ñaareelu baraada bi moo gënë saf suukar. Ñeppa ko mana naan.

Ñatteelu barada bi itam ñeppa koy naan.

Taksimaaan bi moom bañ na naanandoo ataya ak nun ca otel ba.

– Xamuma nuñu ko togge.

Penc.

Allarba ca ngoon.

Jarafi saraxole ji daadi jéglu li mu tàmbaliwula tekki wax ji ca ndorte la.

Yaayu Ibraayma bëggóon naa xam lu dal doomam ju nguunungaana ji.

Ndax waxul, dani patt.

Tontuwul it.

Démb ci guddi, ci biti la fanaan.

Wax naak moom, wànte wuyuwul.

Kilifa gi daaldi koy tontu.

Jaraaf ji tekkil ko tontu li.

Kilifa gi mo jëlën ab dogal ayu bis jii di weesu daadi bàyi Ibrayma mu dellu seen kër.

Yaayam àndu ci woon nak.

Dafa bëggóon moom ñu dolli doomam ji ay garab.

Saraxole bi nee na, magu Faatu bu jigeen bi nee na, Faatu dafa seerewoon démb.

Yaramu Faatu wi dafa ame ay tërgën, muy màndargaal ni dafa newiwoon.

Golan siif suukar si.

Yaayam dàq ko.

Dafa wara soli jeneen tubëy. Daw na génn kër gi ñuy waxtaane wutali kër gi ñuy doora dal.

Mu sumiku.

Dem ci kër gi seen waa kër dal, daaldi sol piliweer bu ñuul ak tubëy ju ñuul.

Bimu dellusee ci ndaje mi, yaayam door koy mana tëyé.

Mungi uuf ràkki Golan ju góor ji di ko nàmpal.

Ràkki Golan ji door na geneen goneñaari këmëxëm yi ci kanam.

Golan dellu naaku xél ca kër gu àggagul ga, jël tubëy ja, fóon ko daaldi koy yóbbu ca kër ga seen wa kër dal.

Mamadu gis na ni dañoo wara wàññi garabu nëróleptik yi ñuy jox Golan.

Mamadu mungi laaj Sagna, ñaxtukat bi.

Sagna di tontuwaale baayam biy romb.

– 1955 lañu ma jongal.

– Kon binga amee 14 at.

– Ci beneen dëkk budul sunu bos

– Demuma ca lël ba.

– Lël bi du daje saa sune ak njong.

– Ñi ma maaseel, 1971 lañu dem ca lël ba.

– Cib lopitaan laay ligeeye.

– Man sekerteer la woon ci menn mbooloom gëstukat.

Mamadu daaldi laaj baayu Sagna.

Baayu Sagna tontuwaale doomam.

– 1969 la ko njëkë daaneel.

– Doktoor bi bindal ko këyit mu dem Dakar ca lopitaal Fann.

Sagna nee na:

– Delluwaatuma sunu dëk.

– Man demuma ca lël ba.

– Dama lànk, ndax sama góomi ñaw ñaw yi.

– Man damaa yóbu sunu waa kër poliis.

Baayu Sagna nee na bokkul ci firiwli gi ñu firiwliwoon Sagna

Lu xewoon digante 1971 ak 1975?

Baay bi neena:

– 1975 defalees na Sagna xew wu rëy ca lël ba ndax mu baña reeroo akug maasam. Ludul loolu bufay dem bu beneenee man naa àndak ay moroomi doomam. Tur wu soof lees ko joxoon ba noppi bàyi ko mu toog ca wetu jigeen ña.

Fimne nak kilifa gaangi xugliku Leonore di nettali njàmbaarteg xale bu góor bi ca lël ba.

– Mamadu nee na: dañu wara sóorale naaj wu tang jér ci mbooyug xaaxaam gi.

– Dañu lay dóor bangay bëgë dee,boomënul baat yiñu lay sa wàlla yëngu bi muy àndal.

Kilifa gi nee na:

– Wànte bég nanu ci. Xale yi kontaan nañu yàkkamti nañu ko. Sa baay da lay dig gétug nag boo ñimee. Ni la dangay dëgër ba mel ni aw yëkk.

Mamadu kontaanul ci pencoo bii.

– Kilifa gi dafa bari ay wax lool. Aji tawat yi ñoo waroon di wax. Doy na sëkk.

Nit ñi menu ñoo waxtaan ndax seen làkk yu wuute yi.

Leegi nak:

Doom waruta weddi baayam.

Jigeen waruta weddi jëkërëm.

Am na mbir yoo xam ni kenn du ko wax.Walla bookakñàkk kersa lay doon.

Bu Kilifa gi jëléekàddu gi, kenn dootul wax.

Maak Leonore bëggóon nañu cee sànni ay kàddu.

Ndax dañoo wara jëndi ay garab walla ñu jëndëlñépp lekk ?

Mamadu ni, sunub reer ñun ñépp war naa tollu ci 60 DM.

Ñungi waxtaan ci sunu xalaat bi.

Tànn nañu lekk gi.

Jigéen ñi tàmbalee tàccu.

Ñungi tàccu ngir sant ci lekk gi ñu tudd.

Ndaànk, bu gaaw, bu gënë gaaw.

Jigéen ñaangi tëb ci wetu saket wi, di way, di sarxolle, di dakse.

Fatou mungi nelawi nelawam ci suuf si.

Yaay yi di ko woo.

Bët yiy kappkaapal; xef yiy raf.

Fatou jug ni ñokket.

Dal ci sàkket wi.

Tëb, yékkëti sip bi, way, sarxolle, dakse.

Ibraayma moom tëbul.

Solulub sip.

Way na.

Sarxolle na.

Dakse na.

Génnéwul dara.

Ma woo Golan.

Golan di sab.

Di cëppcëppi.

Jëm ci càmmoñam di diri tànku ndijooram bimuy rëdd ci suuf si di wër kenu dig wi.

Ay xob?

Ay jullkaata?

Jullkaata yu ràkkaju?

Mu jaxasoo ba di def ni gunoor?

Jaxasoo gi ko garab yi muy fajoo jurël tax mu ni sàññ ni ay xob.

Yar bu njëkk ba?

Buyàgag yàgg ba?

Yar bu njëkk bañu daan yar xale?

Te ñu dëxëñ ko ci dundinu Casamance ?

Ci rajo yi, ci daamar yek dëkkin wi ?

Ràkkaaju ndaxi jéll këriis?

Haloperidol beek Anafaranil beek Nosinan beek Largaktil bi muy jël tax muy loox bay regregi?

Yaay jiy tàccu.

Mu tëb, wogasu,di way, di sarxolle, di dakse.

Waaw kay ni ku këriis.

Daaldi sëgg.

Ñépp bindu ci karne bu mag biñu fi teg: ñiy faju ak ñi ñu àndal.

Ki jëkk ba ci 42 ci mbindum mamadu.

43 ba 203 ci mbindum kilifa gi.

Nimero 1 Fajukat.

Nimero 2 gungekat.

Lu weesu limub 189 kenn dootul jox gungekat yi ay nimero.

Bu Mamadu nee: faj nañu fi 203 juumul.

Fajukat yi 108 dong lañu.

Wànte batay juumul. Rawatina nak buñu lëkkëlée jaxasoog xel akug jaxasoo digante nit ak li ko wër. Agit buñu jéemée boole njaboot geek ni mu bindoo ci feebar bi.

Ci wetu karne bu mag bi am na ay kart.

Mamadu moo leen di tegale ci suba gi.

Kilifa gi moo leen di tegale ci tisbaar gi.

Golan.

12 at.

Katalig.

(animist).

Bawoo Oussouye.

Di fi fajoo 2 fan ci weeru desàmbar 1975 ba leegi.

Melleril.

Jean Delay ak Pierre Deniker:

Thioridaazine – Melleril – manees nañu ko jàppe sax garab guy dëfëlaate, bu fekkeentoonniwan amul benn jeexital ci yëngug xel. Daanaka amul beneen wàññent.

2 kudi kafe suba ak bëcëg.

3 kudi kafe ngoon.

4 Desàmbar 1975:

Mungi dal, wànte des na bat ay.

3 kudi kafe Melleril suba, bëcëg ak ngoon.

18 mars 1976:

Mungi yëngóon di.

Haloperidol forte 10 toq, 1 garaam suba.

1 garaam bëcëg.

Jean Delay ak Pierre Deniker:

Doos bu digdoomu bi mungi toll ci digante 7,5 garaam ak 15 garaam bis bune.

20 mars 1976:

Lañu fi indi Golan, di ko fajal ay saan.

Xeeti saan yu bari yu mel ni bilarsióos a kyu ni mel.

22 mars 1976 Golana ngi amoon 30 kilo.

Ñu koy fajali saan.

5 avril 1976:

Saan yepp ni mes.

Bilarsióosak yani mel.

20 avril 1976:

Haloperidol bi ñu wàññi ko ba 0,5 garaam suba, 1 garaam ngoon.

22 avril 1976:

Baay bi ni:

Golan ab sàmm la.

Daaw la tàmbali di waxtu aka wëréelu.

Waaye lumu wëréelu wëréelu dellusi ca kër ga.

Bamu amee ñenti at laa ko joxoon maamam mu jigeen. Bamu feebaree lañu ko jëli.

Baayam baadoolo la, ab baykat.

Yaayam nee na juróomi ata ngii bamu ko daaneelee ak leegi.

Ibraayma.

Joolaa.

18 at walla 19 at.

Bawoo Cigicoor.

Mu muuma avril 1975 ba leegi.

Di baña lekk yenn saa yi.

Di baña sol yéeré.

Boobaak leegi tollu ci ñenti at ñu koy fajtal fëlé ca Maua, benn dëkku joolaa.

Yaay ji nee na:

Bimu feebaree ak leegi mat na juróom benni at.

Dafa daanuwoon, xëm ñaari fan yewuwul.

Booba ba leegi li muy wax kenn xamu ko.

Jaxasoo.

Waaye du dóoré.

28 nofàmbar 1975 lañu ko indi fii ci kër gi.

Subabu gu ne Benn biteelu anafaranil 25 miligaraam akbenn biteelu Nosinan bu 25 miligaraam.

Bëcëg gu ne 2 doomi anafaranil yu 20 miligaraam ak xaritu doomu nosinan, 100 miligaraam.

Jean Delay ak Pierre Deniker:

Doosu Anafanil bi gënëndaw mungi toll ci digante 50 miligaraam ak 125 miligaraam bis bu ne.

Doosu nosinan bi ëpp 100 ba 200 miligaraam bis bu ne. Dafay laaj nak tëdd ñu di la seetal tasyoŋ ay yoon ci bis bi. Sopp nañu ñu seddale doos yi te baña jéggi benn yoon 10 miligaraam.

30 Desàmbar 1975:

Suba 20 miligaraam anfaranil ak 25 miligaraam nosinan.

bëcëg 20 miligaraam anfaranil ak 25 miligaraam nosinan.

Ngoon benn doomu largactil bu 25 miligaraam.

11 Sawiye 1976 Ibraaymay gis yu kenn xamul.

Ñu dakkal largactil bi.

Ñatti yoon 25 miligaraami nosinan.

3 avril 1976 yaayam ni nañu ko faje ak Haloperidol.

Haloperidol forte suba gu ne 2 miligaraam,

bëcëg gi 2 miligaraam,

ngoon gi 3 miligaraamñaari doomi nelawal.

Fatou.

Joolaa.

46 at.

Jullit.

Juróomi doom – kenn ki kaañu.

14 mars 1976 ba leegi xel mi jaxasoo lool.

Xëtum doof.

Di waxtu rek.

Nee na:

Damaa dof.

Nee na magam bu góor, nañu ma ray, ndaxte damaa dof.

Kenn ki sama doomi nday la.

Sama doom bu jigeen dafa gaañu.

Jëkërëm gaañu.

Sarax naa, wis naa.

Xulendu kaye

Maangi ci yàlla jooju.

Nee nañu ma lekk seeni doom.

Ñaari biteeli Largactil 100 miligaraam, ñaari biteeli Haloperidol 10 miligaraam suba ak ngoon.

7 avril 1976 mu dal nak.

100 miligaraam ay doomi Largactil, 2 miligaraam toqi Haloperidol suba ak bëcëg.

Ngoon gi 150 miligaraam Largactil ak 3 miligaraam Haloperidol.

Aidara.

20 at.

Bàyikoo Bignona.

Yëngu 1972 ba leegi.

Die dóoré.

Di jàmbat ay noppam.

Daa am luciy wax.

Jëkërëm alkaati la. Céet ga mujjul àgg.

Yëngu gu sax booba ba leegi.

Faan ca Dakar la daan fajoo ci weeruut 1973 ba leegi ci Dr Dorès.

10 Fevrier 1976 la ñu ko indi fii.

27 fevrier 1976 ba leegi:

Suba ak bëcëg 50 miligaraam Nosinan ak 3 miligaraam Haloperidol ;

Ngoon gi 100 miligaraam Nosinan ak 3 miligaraam Haloperidol.

Aidaraak ween yu taxaw yi sànni yéeré yi fiñuy tibaatee ceeb bi.

Ni jodd ak yaramu neen wi. Yaay ji gaaw wodd ko.

Mamadoo ngi faj ëri yaayu Ibraayma ji ak pilicilin.

Kilifa gi ni:

– Loolu jaarul yoon.

Saabu bu ame kortison moo ci gën.

Waaye xaalis buñu ko jëndé amu fi.

Ci sunu kees gi am nañu fa ay garab ju bari ba ci lu mel ni saañukaayu nopp.

Leonore fàttaliku na ni desu sabu bu am kortison am na fi. Mu jox Kilifa gi pacal bi ngi mu faj ci yaayu Ibraayma ji.

Dina ci tane. Yaayu Ibraayma moo àndak ku nguunungaana ki.

Muy piis doomam.

Di làkk làkk wunu déggul.

Aidara mi ci ween yu taxaw yi xam na ni bëggumakoo tàkk jabar.

Mu toog ci wetu Leonore di ko ñiiramtal akug xiis.

Leonore moom teg koay ndég.

Mamadu nee na moom itam Aidara mës na ko top ba biir néegëm.

Bamu agsee ca kër ga, mu fekk ko ba ca biir néegëm ca dig lalam mook jabaram, ni muret mbalaan mi.

Am nab is bu Jabari Mamadu doon matu, Aidara borom ween yuj taxaw yi di ko jeema xoj.

Sagna, ñaxtukat bi nee na:

Sama baay day politig.Ñooma yobbu Faan..

Doktoor bi gisul dara ci man.

Rajo yi ñoo wax fu ne ni dama doon wutal ay pexe Siŋoor.

Soldaar la woo 1961.

1963 ma dugg ci way fajkati nguur gi.

Sama baay am na ñaari jabar.

Sama yaay génn na àdduna.

Laata moo dee dénkna ma benn mag bu góor, ñaari mag yu jigeen ak benn rakk bu góor.

Li ko gënë waral, mooy niñuy yàqe xelu nit ñi ak rajo yeek tele yi ngir man leena noot.

Dañuy njëkëyàq xell yi.

Loolu laa bañ ba tax ma doon wax ci rajo yi.

Joolaa laa maak sama mag.

Njonga ma fi indi.

Jonguwuma.

Warumaa am jabar.

Doktoor laa.

Baay bi nee na:

Sama doom dafa dof.

Day waxtu.

Day di móolu.

Bu rajo bi tàkke rek muy móolu, di saga, naa ci moom lañuy wax.

Xeex na ak magma, ndax daf ni ko mu noppi.

Buur Dawda nee na:

Waxuma dara.

Amuma dara.

Damaa ñëw fii ndax sama yaaya ma fi indi.

Damaa ragal, ndax bu gudee damay gis lu mel ni njuuma walla jaan muy dugg ci man.

Moo tax ma ragal.

Bëggumëkenn jige ma, te am naa ko.

Bëgguma kenn xam ko.

Dama koy bàyyi rek sama diggante ak yàlla.

Sama taat yi day metti.

Damay waxtu, ndaxte sama xol mooy metti.

Gisuma dara.

Dégguma dara.

Bumay nelaw nelaw, damay gént di gis ay rab. Damaa ñëw fii ngir toog fi ba fàw.

Pencoo bii di ñëw dinañu waxtaanewaat lekk gi.

Jën walla yàpp?

Jigéen ñi yàpp lañu bëgg, yàpp rekk.

Ma xalaataat yàpp week naaj wi ci ja yu Cigicoor yi ba tax ma dugal gaynde géej ci wax ji.

Ñu ànd ci gaynde géej gi.

Wànte gënëluleen.

Bu yàpp wu dëgër amoon, dañuy noos.

Gaynde géej du dara.

Tàccu yeek way yi ñoo ëpp doole anafaranil, Largactil, Haloperidol, Nosinan.

Tàccu yu ànd yi faj na parkinsonak yeneen xeeti ndof yépp.

Ndax duñu jëñdal dëkk bi tama.

Buñ jàapee ni wayadi gi nekkul ludul wayadi gi ci njaboot gi ak ci askanwi, kon Golan, Buur Dawda, Sagna ñaxtukat bi, Ibraayma booroom nguunungaana li, ak Aidara boorom ween yu aju yi dañoo dof, ndaxte seenu askana jaxasoo jaxasoo bu tukkee ci digante jibar aki reen aki doom, otook ngoos. Ninga xam ni ñoom itam noonu lañu jaxasoo ci digante Supermarse ak ja ba.

Leegi nak Mamadu ak Kilifa gi ñungi sotti ay doom yu weex ak puudar ci lenn ndab.

Jaxasoo gi dina fi rawati.

Rajraj ji wàññiku.

Ci geneen wet gi ma boole tamak balafoŋ ak mbiibb ak tuxra. Ak dal daadi dellusi.

Rajraj ji yokku.

Yokku na?

Te rawul bu doomi Nosinan yeek Largactil ak Haloperidol ak Anafaranil yi di wàññiku ci ndab li ba noppi mbiib yeek tuxra yi di wàcc?

Lu aju ci feebaru xel, mënéesukoo natt ci ay balaas walla yu ni mel.

Damay jënd tama.

Golan génne tama ji.

Di sab.

Di sarxolle.

Tàmbalee tëgg.

Jaraaf ji, Bambara bi jël tama di tëgg.

Jigeen ñi jëli tama di tëgg.

Golan di fecc.

Ibraayma di fecc.

Jaraafi Bambara ji di fecc.

Di wengal taat wi.

Jàpp ab kooy bi.

Jëmëlé ko ci kanam.

Jigeen ñiy tàccu, di tëb, di wogasu, di sarxolle, di dakse.

Fatou du jàpp tay.

Leonoregis ni:

– Lu Haloperidol biy gënë bari, Golan di gënë mana fecc.

Tama yi pare nañoo rëkk ci penc bii di ñëw.

Jaraaf jee leen di denc. Penc rekk lañu leen di génné.

Golan mu ràkkaaju mi warula tëgg tama.

Tay Mamadu ak kilifa gi nekkuñu fi.

Tekk.

May laaj lutax duñu bokk leek saa sune?

Ndaxte xaalis bee fi nekkul.

Lutax manunoo ànd ligeey lunu ame dara?

Jarafi saraxolle ju mag ji ni, danoo yittewoo benn ergoteraapët.

Buñu amul ergoteraapët nak?

Ku fi mana def dara?

Yaayu Ibraayma mooy defar ay bale.

Yaayu Golan di ñaw.

Yaayu Paul di ràbb.

Yaayu Aidara di cuub.

Yaayu Ngañ baana baana lawoon ca Kaolack.

Manunoo def dara ak lii?

Gòor ñi ñoom toog ci ker mango yi sub aba ngoon.

Ñepp reetaan.

Góor ñi daal duñu def dara?

Jigeen ñi ni linuy ligeey doyna.

Ñoom rekk man nañoo teg yen saa yi luñu bokk lekk, walla ndimbël li leen tubaab yi di dimbalee, bu ñu fi jaaree.

Golan angi yore wenn këyit am lu tooy lu ci nekk.

Mu di ko séddale Mamadu ak yaayam ak yeneeni xale yi. Yaay ji daaldi koy woo.

Dafa doon jeema ràbb benn pane.

Yaay ji door ko daaldi koy nangu.

Mamadu aaye ko ko.

Mu jëfé ndigël.

Golan wëy di ràbb.

Waaye naka ko Mamadu wan ginaaw, mu ni nanget pañe bi.

Maak Leonore binuy agsi juróom ñenti waxtu teg na ay simili.

Jigéen ñaangi toog ci ron màngo gi. Yaayu Aidara di waas jën wu tollookubgone.

Mungi tudd coof.

Yu ndaw yu tolloo kub loxo di nirook waas te duñu waas, ñu teg leen ci benn bool.

Kàmmaate ju dijj.

Ak ju sew.

Kaani gu sew gu rafet.

Ak yeneeni doom yu wert yuy nirook kàmmaate, ñu naan ko “batañse”.

Batañse bu yolet te rafet.

Laaj.

Soble.

Supame.

Gejj, tuuti.

Diwu gerte – waxu ma diw gu xonq de

Roof – walla koryand la?

Ak ay korneti yu sew.

Jiggeen ñaangi yanu matt mu dijj, di ko indi.

Am ku dem wàlli ay xal.

Ñu roof matt mi ci digante was yi.

Sawara wi di boy.

Cin li tegu ci.

Leeg leeg ñu ronqi taal bi.

Jigeen ñi jamb nañu kàmmaate gi, segg ko.

Sotti nañu diwlin ci cin yi.

Tëll jën yi.

Dëbb roof beek kaani gu sew gi ak xobi loryee ak laaj ak xorom.

Res nañu jën yi.

Rosi, sippi jën yi ub ko ci ay bool.

Ñu xolli lujum yi, sànni ci diwlin ji, ñuluge ndoxum kàmmaate mi. Sippi lujum yi ub ko ci ay bool.

Ñu sóor. Wëlbëti ceeb bi, ub cin yi.

Teg ay xeer ci kaw.

Biñu ko waree ñam, la yaayu Aidara jug di fecc akub dank ci loxo bi.

Tibbal nañu góor ñi ñaari bool.

Góor ñaangi toog ci ëtt bi wër bool yi di lekk.

Di dank bamuy siit.

Kilifa gi indiwaale na Coca Cola, Fanta, ak beer.

Góor ñi raxasu nañu, biñu lekkee ba noppi, wommiku, galaxndiku, soccu.

Bi ñatti waxtuy waaja jot, la jigéen ñi añ.

Kilifa gi ak jigéen ñi sant ci añ bi.

Ñu sant jigeen ñi.

Miinu ñu loolu.

Mamadu genne ay tabletam.

Golan sukk fi ñun.

Leeg leeg mu xaaxtandiku.

May fecc ak Golan.

Góor ñiy fecc ci seen biir.Noonu rek ñépp ànd di fecc: Golan, yaayam, rakk walla magma bu góor ak man.

Yaay ji ñudi Golan.

Golan di jafandu ci benn bool bu defu des.

Yaay ji fàqub yar, xëbël ko.

Golan kot ci tàngi Wolfgang, tubaab bi ñu doon jëlsi.

Golan dëpp gemeñam ci dënnub Wolfgang.

Golan jëmëlé Wolfgang boppam bu taq suuf bi.

Wolfgang faxasal ko ko.

Golan dal as lëf.

Jarafi saraxolle ju mag ji nee na:

– Xamoo ni fii ci Afrig dof warula wax ak ki koy faj.

Yaayu Golan angi wëndéelu ci kër Kilifa gi.

Golan dem ci jabari kilifa gi.

Sëggël bopp bi ngir mu faxasal ko suuf si te fompal ko bët yi.

Mamadu: Golan boppub ku tëlbëti dëgg la yor.

Kilifa gi: Golan kay boppub ku tëlbëti dëgg la yor.

Ñaari xale yu góor yuy nirook mankaañ te ay màndeng la ñu watu nañu ay nel. Ñoom ñaar ay mag ak rakk lañu.

Seen wateef gi lañu daan watu ca kër Esnatoon bu Amarna ca Esipt.

Kilifa gi leeralal na ma luy boppub ku tëlbëti dëgg.Mungi ko jëlé ci sëriñëm doktor Musaa Jóob.

– Ndong gu maase.

– Jë bu sew

– Melo wu jéggi dayo.

– Boppub ñatti koñ.

Kilifa gi jëGolan di wane bopp bi.

Loolu moom Mamadu ak kilifa gee ci ànd.

Mamadu mi gëm Marx sax tay ànd na ci leeralug Boppub ku tëlbëti.

Reer?

Xam?

Walla ñàkka xam?

Ngañ bokk na ci ñi fi gënë taaru.

Jàpp nañu ko.

Ak nday ju ndaw.

Mamadu ni, niñu koy waxe ci kërug fajukaayu dof yepp ci àddina bi, saa suñuy wax ak dof buy nite nitelu:

– Ngañ moo fi gënë wopp.

Dama bëggóonë indil Ngañ intelektuel bi ab téeré.

Waaye day mel ni ag gënëléek ci jàngul.

Ak càggante gu wér ci Ngañ.

Maak Ngañ nungi dam.

Ni ko waa Senegal di defe.

Ci ludul dara, ni gént, powum xale mii day mujj yobu la ci ay xalaat yu kawe.

Man ngaa dóoré ci kanam ak ci ginaaw. Oh, sama xeer yu weex yeppa daanubenn benn.

Baci doom bu mujj ba.

Ngañ yërëm ma ba dima reetaan.

Man xamuma ni muy dame.

Kilifa gi:

– Golan jàppewul yaayam yaay.

– Li ci ëpp, ci ñaari at lañuy ferale xale yi daaldi leeni joxe.

– Leeg leeg sax du mat ñaari at, bu dee kuy nef.

– Mën naa am Golan dañu koo teela feral.

– Golan maam a ko yooroon mu daan sàmm.

– War naa am juróom ñenti at walla sax fukki at akñaar.

Golan angi siñaaglu ci jant bi.

Golan ñu firi ko rek ba ko.

Golan reer ciy pexeem.

Golan, mbukki si.

Golan, cegg si.

Golan, ngaynde si.

Gaynde yeek, bukki yeek, segg yu mag yi bàyyi ko muy wër meew ak lu mu lekk.

Ah ab àmbilaas !

Ab sàndarma.

Tëni bu bulë!

Tomboug mu ràkkaaju ki di daw ci biir këru dalal xel gi ñu dupee jëwriñ jii génn àduna.

Ak yaramu neen, o!

O! Bëtt nañagub toolu dof yi.

Di budi kàmmaate gi, di làwi ñag bi.

Di budi garab yu ndaw yi ñu jëmbët ci wetu yoon wu mag wi, bàyyiwul dara.

Fàq na ngandab carob mango bu meññ gicc, daadi koy gàccoo, moomjësig ji!

Muy ñurux ci biir gutt bi ni tëruus ak cari màngoom.

Sàndarma bi ni:

– Am naa doom ju ma xawa jaaxal. Mënuma ko fee indi?

Mamadu mooy waajal lepp.

Jarafi saraxolle ju mag ji moom noppi na.

Jarafi bàmbara ju ndaw ji noppi na.

Tomboug, mu ràkkaaju mi dellu si na, juge ci gutt bi.

Jarafi saraxolle ju mag ji jàpp ko yeew loxo yi. Daadi koy tërël ci suuf.

Muy bañ, di fuddu.

Jarafi bàmbara ju ndaw ji lem tànki tomboug mu ràkkaju mi, toog ci.

Mamadu indi pikiir yi.

Ñaari biteeli Valium 10 lañu ko sàmpal ci loxo bi, cëy!

Ñaari biteeli haloperidol ci taat wi, cëy!

Benn biteelu largactil ci taat wi, cëy!

Biñu koy dugal ci otot bi, nelaw na bu yàgg.

Tomboug.

35 at.

Bawoo Cigicoor.

Tëlbëti.

30 Fevrier 1974 ba leegi ñu ko fiy faj.

3 miligaraami Haloperidol suba, bëcëg ak ngoon.

50 miligaraami Largactil suba ak bëcëg.

Ngoon gu ne 100 miligaraam Largactil ak 100 miligaraam nosinan.

17 sàttimba 1974, xel mi dellusiwaat, mu dal.

Dal lool sax.

Mu ni dafa bëgë dem kër doktor ñu defaral ko bëñëm yi. Nee na dafa am ay bëñ yu deñ.

2 biteeli Valium ci sidit.

1 biteelu largactil 25 ciw taat.

1 biteelu haloperidol ciw taat.

1 biteelu nosinan ciw taat.

Ñati pikiir yu mujj ci ñu tegale ko ba muy ñati fan.

2 Juillet ak tan gu fés.

Fi mu ne moom jéematula rëcc.

Dafay aajowoo ay doom.

50 miligaraami Largactil Suba ak dig bëcëg.

Ngoon go, 100 miligaraami Largactil ak 50 miligaraami Nosinan.

12 ci weeru ut 1975 mu daanuwaat. Ñu indiwaat ko dalal xel.

Ay yuuxu.

Am pecc.

Ay wax ju tëë dakk.

Wex xàtt, di dóore.

Seen waa kërë jëndatul woon garab yi.

Muy song nit ñi ci mbedd mi.

Mu def boppam njiitu réew mi.

Di jéemë rëcc.

Ñu bàyi ko mu ñibi ndax doomam dafa feebaroon.

Mu dellusi 8 sàttimbar 1975, waaye bëgu fee yàgg. Nee na dafa wara toppto ji toolu ceebam ba te doomam ji itam mënu ko bàyi ginaaw.

Dañu wara bàyi muy demaka ñëw.

Seen waa kër ñoom, dañu koo bëggoona ba fu ñu koy tëjjé rapp.

Mu lànk.

Nee na ca kër ga lay jëlé ay garabam.

– Lutax bàyiwuleen ko fii.

– Bu fekkee, am na kenn ci njaboot gi ku nangoo àndak moom fii, kon ñu ba ko fi.

Golan angi sotti ndaamaraas ji ci ab boolub weñ.

Daaldi tan matt mu dëgër dugël ko ci pàqub màbgo gi, dammat ko ci, tegale ko bamu mel ni abtaal.

Mu sotti ndaamaraas ji.

Tas matt mi.

Sottiwaat ndaama ji ci bool bi.

Dajalewaat matt mi.

Foraat matt mu dëgër.

Dugël ko ci pàqub mango gi, dam ko ci.

Leegi mu tàmbaliwaat.

Leegi nag taal taal bi rekka ko dese.

Yaay ji agsi.

Ni ko nanget.

Sotti.

Dammaate.

Dajale.

Tasaare.

Sol.

Sotti. Tasaare. Dam. Dajale. Sotti.

Daw na.

Dellusi na.

Dajale na matt mu dëgër, dam na ko ci paqub mango gi jal ko bamu mel ni ab taal.

Solaat na ndaamaraas ji.

Ma jëli almet.

Dama wara taal taal bi.

Bëguma ko.

Daw na.

Dellusi na.

Dama wara taal taal bi.

Bëguma ko.

Ma jox ko almet ji.

Mu taal taal bi.

Ndaamaraas jaa ngi tàmbalee xaay.

Yaay ji agsi.

Li muy def du ni.

Kenn du ko defe nii.

Neneen lañu ko wara defe.

Golan daaldi tuur ndaama ji.

Daaldi jaxase taal bi.

Daaldi dajale ndaama ji demon bay ñor.

Rangale ñatti xeer.

Sàanni giliñ yi.

Daaldi lakk.

Mu ni ñokket, yékkëti loxo bi ba ci sikkin bi tufli ci.

Yaay ji am kersa.

Lii du kersa?

Cëy, bu fi nekkulwoon!

Yaay ji noonu la woppe.

As ndaw, menn mbokkum kilifa gi moy dajalewaat ndaama ji, defaraat taal bi ba pare di ko naqaral ci tuflit yi.

Yaay ji jël doom ji daadi koy wan.

Danga wara doon nit.

Golan di door ndaw si.

Defe naa ni danga wara waaru ci Golan te bañ koy dog.

Boo ko naxtaanee dina tane ci lepp.

Daa mel ni yaay ji dégg na ko.

Mu yonni Golan mu jëlëliko tubayi rakkam ji.

Golan lank.

Baal ma àndak moom.

Mu teg tubëy ci kaw garab gi ci wetu rakam.

– Golan solala sa rakk tubëy ji.

– Solaluma sama rakk tubëy ji.

– Wànte man nga ko.

Golan solal rakk ji tubëy ji.

Yaay ji bég ci teewlu gi mu teewlu Golan.

Am mbubtubëy.

Ndaamaraas.

Sawara.

[Ci turu 111–149]