Hubert Fichte: Banu dajewaatee, ñaari at ganaaw sunu daje bu njëkk ba, danga ni ma woon, nanu defaat beneen interwiiw. Nga yokk ca nibii yoon amul ragal. Ana lan nga doon tiit ca sunu interwiiw bu jëkk ba?

Maurice Dorès: Lima doon tiit ci man la nekkoon. Daf maa wóorulwóon ni dafa am benn gëm gëm bu ma doon doxe. Sama kàddu dafa ñagasoon lool. Yaakaar naa ni nak xoolaat naa sama kàddu ci digante bi, bagis ni pajum dof mu ne, am na ci gisin ak doxalin wu mu wéeru.

Fimu nek nak man namaa ràññee yooyu gisin aki doxalin.

F: Wan doxalina la terewoonna wax keroog ca lopitaalu Fann?

D: Xanaa gisgisu neokoloñaalism agit di wutal sama bopp ay lay.

Kenn ñimewula ñëw tay ci am réew ni leen dañoo ñëw suuxlu leen ngir jariñoolenn doŋŋ. Ñun ñi dimbaliwaate taxa jug, dañoo ñëw ngir indi,ñëwuñu ngir yóbbu. Lii mooy waxi Faan ja. Dañuy def ci bopp yi ni dañuy indi dara. Loolu nak mooy gissgu neokoloñaalist: Waa afriga ngu taxa jug. Sama koom nak mooy: bir na ma ni benn Afrig yékkëtiwuma. Wa afrig doyal nañu ci ñuy ñëw rekk di leen jariñoo!

F: Ndax doxalinu neokolñaalist woowu wàññikuna ci at yu mujj yi?

D: Waaw. Ndaxte am na doxalin woo xam ni kenn menu koo wëyël ay at tefeeñul. Fann meññentu neokoloñaalism bi la.Nekkinu nasaraan yi foofa yomb naa faram fàcce. Fann ci sistemu iniwersitey nasaraan yi la bokk. Kenn ku ci nekk foofa ngay binde sa tees, sab diplom. Dangay ñëw ngir ame fi xamxam bu wér ci wàllu nit.tees yeek film yi dañu koy firndeel bu wér. Bo jeemee defe neneen, du dem. Damaa amoon yéenéy taxawal fi ab poroose boo xam ne ñepp dinañu ci joti, ñu ubil ñépp bunt yi te mu baña nirook Lopitaal. Loolu mënulwoona nekk.

F: Ndax doxalin ak gigis boobu day ndono lu juge ci daaray tugël yi gënë kawe?

D: Loolu bir na ma.

F: Lu waral fësëloowan sa gisgis bii ca sunu waxtaan wu njëkk wa.

D: Booba, man ak ñu bari, dafa am lunu yeemoon ci Afrig. Booy doora agsi, dangay cekkte ba pare ñu bàyi la ci biir ngir gëñ laa mana jiitloo – loolu yepp muy lu dëppóo ak system bi. Te ñoo ko tay di la bàyi ci sak ngëlëm. Man nak noonu laa bàyee ñu fowe ko ak man.

Afrig ci boppam dafa gëlëm –gëlëm ciw askanam, ngëlëŋuk kilifteef. Yëf yi am ërób moo am Afrig, rax ci dolli wëlbëti xel yi ci goornmaa yi ak ngëlëmtek ndof – muy neokoloñaalism ak boddikuw xeet.

F: Yewu gii nga am ci mbir mi, nu mu la dikke, ndànk ndànk walla yuréet?

D: Ci men mbir. Muy poroose bi ma la doon wax te ñu waroon koo amal ca ndar te ginnaaw gi mujju ma koo mana amal.

F: Dama bëggóon nu teg baatub Ideolosi ab diir ci suuf te wax ci làkk walla waxin wi ñu doon waxtaane Fann ca Fann. Noo gise ñagasaayu kàddu yooyu?

D: Loo bëgg, ma wax sinwaa? Ndaxte kat an sinwaa laay jàppe làkku nasaraan wi. Sinwaa boobu dafa am doole lool ci iniversite bu Dakar. Kenn mënula wañ loxoom, ni ko dangay bin lu ñagas ci sa ligeeyinu bopp. Njiit lu nekk day bëggë wanne taarub wàll wa muy jiiteca daara jooju.

Te loolu, dañu koy bind benn yoon ba noppi tëggaat ko fukki yoon ba fukki yoon ak juróom. Ku bokk ci iniversite danga war di gëstu di bind lu bari.

Kepp ku jaar Fann daaldi jël mbind mi ba tax na boo génnée mana dégg 100 walla 200 ba 300 yoon wax jile.

F: Binga fiy doora ñëw, dangaa yéemuwoon ci Fann.

D: Li ma gënoona yéem ci Fann mooy way tawat yi.

F: Dafa mel ni dañu cee sawaratul. Dama seetlu ak mbañeel ci ligeeykat yi, mbañeel gu teguwul fenn.

D: Ci ñenn ñi… Kenn ku ne sa intere ngay xool te bu dajeek interey keneen rek… Te melokaan woowu ca Fann mooy mellow koloñaalist. Te system bee ko laaj.

Fii royuñu fi wenn pajin wuy jeema xàmmee doxalinu dof yi.

Nuñu bëggë xàmmee doxalinu way tawat yi, bu fekkee ni duñu leen deglu?! Buñu bëggée déglu nit ñi, fok ñu dégg seenu làkk.

Ludul loolu dañuy mébët rekk ni ko waa tugël di defe. Fajkat yi ci seen bopp ñooy gént.

Li xew Fann mooy moom ak moomeel.

Nit ñi dañuy ñëw Afrig ngir luñu am: ab àll, walla xaalis, mbaa am xel, wallaw yaram.

F: ni ko Marx di waxe: Kapitaalism ak bopp sa bopp !

D: Waaw kay.

F: Xellu : poroblemu wax !

D: Defe naa ko.

F: Ñamal ma tuuti ci exotism.

Exotism dañu koy bañ ; wànte ndax exotism làmboowul tuuti xellu ? Xoolaatalsakanaayu yënguy turist yi ak dimbalaatekat yi mba sikaatar yi ?

D: bu nit ki wane ganaaw am réewëm rekk sori tàmbalee dugg. Bu ko defe am doole ju koy yëngël. Lu mel ni bëggé. Fii nak defe naa ni mbaax lañu fi wara dugël ni ko Sartre diglee. Kenn ku ci nekk yaay xam looy def ci bëggé googu : Ligeey walla yaafus.

F: téeré yu bare bari bind nañu leen ca Fann. Collomb, Zemplini, Ortigues ak ñi topp ci ñoom. Defe nga ni mbind moomu mën naa yokk sunu xam xam ci Afrig ?

D: Lenn lu ci nekk dañu koo wara xoolaat. Ku mel ni Collomb dafa juum, romb poroblem bi. Bu ëllëgée, dees na jàngat ni góor googa dafa xalaat mbir mooma ca jamono jooja ngir xàmmee ni manees naa juume nile.

Sama gis gis nak bokkutak bu Collomb ak bu nàttangoom ci ko bindaat yepp.

Dañu jàpp ni nit ku ñuul nday yu bari la ame. Loolu mooy lan ?!

Defe naa ni lii day firndeel ni Collomb ak ay nàttangoom dégguñu làkk wi. Yenn saa yi dañy gis ab xale juge ci magam bu jigeen ñu jàllale ko ci yaayam ju ndaw. Lu mel noonu, ku ciy wax ay nday, am na lu am solo loo umpale. Ca Afrig, nday jenn la te dafa soxor, raglu, di màtte. Am na film buñu dupee “les dents de la mer” – Bëñu géej gi ; këyitu xibaar wii di “le Soleil” moom nii la ko bindewoon “les dents de la mère” – Bëñu nday ji. Saa su ku tëlé di ñëw ci man, ndayam lay àndal. Moo xam lepp. Mooy joxoñ kooyub doom ji ni : lii lan la ? Du jug ! – seetlu naa ay xale yu seen yaay yu ndaw yar ba noppik di leen saaga bañu am ñati at : jurooma !

– Manees nañoo joxe mbaa sax jàllale xale bu ñuul ?

Du dëgg !

Doomi jiitle moom coonoy neen la.

Damaa seetlu ni xale bu ay wayjuram tàggoolu ëpp ñaar fukki at sax, dafay jéema def lu nengir jubëlé leen.

Te dañuy wax sax ni:

Doomi nit ku ñuul, doomi ñeppa. Bopp sa bopp amu fi.

Du dëgg.

Nit ku nekk, ci sa nekkin lañu lay ràññatlee, ci ngor ak kersa. Ngor ak kersa rekk am na gën gaa néew juróom benni baat yuñu leen di ràññatlee ci Wolof.

Te:

Nit ku ñul xamul ab xëcóo.

Te des na leneen tontu. Yomb na lool nga ni diw dafa yoom ganaaw boo ko tàppe ba noppi. Collomb am na lu am solo lumu bind ci Bouffée Délirante.

Wànte namu ko tëjé moo jaarul yoon.

Dafa wax ni ci ab Bouffée Délirante lu néew ci personaalite nit ki mooy feeñ.

Porofesëer Sâ ca Paris aman na ci gisgis bu gënë yanu maanaa: Bouffée Délirante bi day wane xam xam bu xoot te matale ci jëmmi doomu aadama.

Ortigues nak moom dafa ubiwoon ab kabineb psikolosi ngir bind benn téeré!

Dafa ñëwoon ngir jëfëndikoo fi benn codex. Dama ci bëggoona teg rekk ni ab psikanaalist bu Senegal beneen gis gis la ciy wara am.

Jàpp naa ni ligeeyu Ortigues bi lu luñuy déggé ak baati wolof. Jàpp naa ni kuy def psikanaaliis, danga wara ligeeye làkk wi ñuy wax. Ñoom ñaari Ortigues yi dañoo jeema tërëlu doxalin. Ci wile doxalin nak, liñuy ligeeye moo wara leeral liñuy gëstu. Dañu doon ligeey ak ay ndogo yuy làkk nasaraan.

F: waaye loolu itam koloñaalism la. Ndax codex buñu àbbaani lañuy jëfëndikoo. Ñu obliise waa Afrig ñu noppi walla ñuy wax naka sudul noonu , ganaaw buñu tegee nëlé seenu làkk di jëfëndikoo codex bile. Muy lu ñorul xaayul luy tax du mana def dara ludul tegoo rekk li ko codexu psikanaalist biteg.

D: Jaarul ci yoon ndax dugg bi psikanaalist biy dugël loxoom ci yëf yi.

Zempelini moon damaa yeem. Ligeey yi juge Fann yepp, waxi kasaw kasaw rekka ca nekk. Leeg leegi ñu rax ci ay baati Wolof ngir wanewu te nañu koy tekkee sax duni.

Ci liggeeyub Zempelini bi, xool naa ci 400 xët, gisuma ci benn njaaxum. Ligeey bu àndak fayda la def te lepp lu ciy Wolof, jox na ko ñu ko xam ñu takku ni lingist yi ñu càmbaral ko ko. Waxuma ay teoréem. Wànte ligeey bu am solo bimu def.

F: Zempliñeen yii ñoom ay gëstukat yu xarañ te am fayda lañu. Dofuñu te am nañu luñuy jomb. Kon nak noo gise fen yii am ca Fann? Noo gise itam ni ci waa tugël yi mana ànde?

D: Yaakaaruma ni ànd nañu ci mbaa ñu mer ci.

Iniversitey tugël yi a kyu amerig yi ñooy doxe noonu :publish or perish !

Gëstukat mën naa toog juroom benni at te gennewul dara. Kenn noppiwula def loolu. Ganaaw juroom benni weerwalla sax juroom benni ayi bisgenne nañu bu yàgg am mbind ci xellug waa Afrig yi.

F: kon daal yaw gëmoo ni lañuy bind ca Fann cig cofeelgu jëm ci xam xamu gëstukat bi la, sukkandiku xanaa kay cig bëgë jariñu rekk.

D: Duma niñepp dañoo feebare noonu. Ndaxte am na ñoo xam ni defu ma leen ay gëstukat. Gëstu am fa. Pëccëxoo aki kontaraa ak bindantu dong.

F: ci yan làkk la ceetug tawat yi di ame ca Fann?

D: xanaa yi am Pantoise walla Montpellier rekk. Fann ak yeneen Këru dalal xel yeppa yam. Dañuy fay joxe nëroletik yu bari lool ak di maasaate. Famu nekk ak lañu fa binde siiw na itam lool.

F: fii dañu fiy faj ay Wolof ak ay Pël ak ay Manding ak au tukuloor ak ay lebu ak ay Seereer ak ñeneen.Kuy làkk làkk yii yepp?

D: Kenn ci fajkat yi. Man ci sama bopp Wolof laay làkk. Daf ma metti, li ma déggul tukulóor. Saa buma ame malaadu tukulóor, damay jaaxle. May laaj lan laay def ak ñoom. Am na mbir yoo xam ni kenn waru koo tàmm tàmmlu.Dootuñu gis tus. Damay yëg ag mànki ci sama bopp. Mënumaa ñàkka xam ki nekk ci sama kanam li muy wax. Monte teewul ma leen di bindal ay garab. Wànte nak fajkat yi may jàpalee ngi fi. Ñooñuu dima jàpale, dama leen di wax saa sune ñuy bàyi xel ci li way tawat yi di wax. Ci ñoom la paj mepp di jaar fii ci Fann.

F: Wolof bi nak, budu yaw mi koy làkk.

D: Duñu wax lu bari ci informateur yi. Monte ñooy def lepp. Ñooy dajale sax li gëstukat bi soxla lepp. Muus nañu muusaay gu xam nañu liñuy xaar ci ñoom. Waaye seenu jàng soriwul soriwaay gu leen di may ñu bind seenu tur ci kaw seenub gëstu. Am na gëstukat yoo xam ni dañuy génné seen mbind da tuñu ci tudd benn yoon informateur yooyule.

Maangi am yaakaar ni sama xarit ya ca Paris,buñu ma jàppalee, informateur yi dinañu mana bind seenub gëstu ba noppi xaatim ci seenu tur.

F: “lekolu Dakar“ bi.

D: man jàppuma ni am na “lekolu Dakar” Collomb angi nii. Ñeneen it dañuy ñëw toog fi ñaari at ba ñenti at dem seen yoon, ni mër. Yanuwul maana sax ci wàllum kër doktoor di ko tudde “lekol”.

Gëstu dëgg dafa laaj làqu ci bërëb te jàgg fa.

F: Tugël yàquñu rekk li leen wër, waaye fuñu dem yobbaale fa néewël ga am ca seen njàng ma gënë kawe.

Nu ko waa Afrig yi gise?

D: Diis gann. Wànte ñimewuñu koo fësël. Lepp luy pajum xel, Fann a koy saytu fii. Waa senegal yi dañu leen fiy tàggate dong. Manuñu ci dara. “Feeñuñu ci sax ba tax na tubaab yi ni fàng”. Looloo am Fann itam. Tubaab bi li mu fa am jéggi na dayo. Te dañoo wex xàtt. Day wane rekk seenug suufe te ku la gëñë suufe, gën laa soxor.

Pajum xellule mooy mujjë moom boppam fii ci Senegal. Lifi am weesuwul moomeelug Faraas guñu sànge mbubum siyaas ak gëstu. Bepp doomu Senegal buk o nànguwul, juge fi.

F: Benn ci gis gis yi am ci Fann bokk na ci ni:

Ni pencum Senegal tëddé bodiwul ak ndof benne.

Noo ko gise ?

D: Am na lu ciy dëgg. Dañu jàpp ni doff bi ay raba ko jàpp. Nit la koo xam ni day gis ay mbir yu keneen dul gis. Noonu la deme. Tànka mungi ni cell, jotewul ak kenn dara, kenn du ko wax daran i ñañuy wooye dofub dëkk bi ca tugël. Waaye bis bu dof bi tàmbalee dóoré nga gis ñu koy gundxataal. Yàggul rekk jot na benn dof bu juge Fuutë. Ci benn dëkk bu ndawa ndaw. Dadoon waxtu.

15 weer lañu ko jéng, yeew ko. Manulwoon saxa dox. Dañu ko daan dóor.

Am na fajkat yoo xam ni dañuy dóoré di làkke.

Bu ame lu wuute daal : xanaa kon ci niñu jàppe ñu dese ñi lay doon. Wànte nak, ca tugël itam dañu jàppoon ni dof yi ay jinne ñoo leen jàpp.

Ci pencum Afrig nak kenn daawul boddi dof yi. Loolu nak la xamul mooy lan. Ñeppa kooy wutal aw lay.

F: Niñu jàppewoon dof yi ca tugël gu yàgg ga ak ca Afrig wuutewul ak niñuy yore ay mala. Door, yeew, xas. Dof bi ci kanamuj nit ñepp lay defe li muy def, muy dem ganaaw kër walla tuur ndox. Maa ko gis ci genn kërug dalal xel. Waaw luy ñàkka boodi ?!

D: wax nga dëgg. Dof yi amuñu sax pajaas buñuy nelawe.Gëdëy doomu aadama dafa am solo ci Afrig. Waaye dof biñu bàyi muy tëdd ci ay nefaraam moom am na gëddë.

F: Ca Fann dañoo bëggë delloo dof yi ca seeni dëkk, kenn bañ leena boddi. Mootax ñu leen di boole ci ay këru xellu.waaye, ndax kenn bëgg na ko ?

D: xumbël la rek. Gëmuma ni boobu ligeey ligeeyub doxandeem la.

Yooyu kër buy amit waa gox ba ñoo ko wara soxla, samp ko – samp kër fu la neex, ag yàq dong la. Waa Afriga ko wara defal seen bopp. Yoonu doxandeem nekku ci.

Kenn mënula bañ nak dox gi penc miy dox fii. Dañu wara xam li ñu ñu fiy doye. Bu fekkee ni nak dafa am fajinu dof wuñu fi aajowo, kenn warula wuteji feneen aw pajin. Pajum dof, tiis wu manuta ñàkk la ci Afrig. Wànte warul tax ñu di leen indil paj muy jur jàngoro.

F: Damay fàttali rekk benn dof buñu doon faje ca Kenia te daawuñu ko toroxal.

D: Gëm naa ni – te bokkon na ci sama mebet ma ma amoon ca Ndar – bu amoon ñuy dimbali fajkat yi te ñu meenante ak dof yi bu baax…

Xewit wu bees wi nak mooy jàppe boolewaale ci njaboot gi yepp.

Faj ku rëkkëtiku te diisoowoo ak ndayam, du amug muj.

F: Ci menn penc muñu amaloon ca dalal xel bu Kenia ca wetu Cigicoor, waxeesoon na fa ni Dof yi waruñoo jël kàduu.

Jëkkëri sennus ndaw su teewoon ca Bouffée Délirante ba moo ko waxoon.

D: Monte ci pajum dof de dañoo wara déglu way tawat yi ñu wax.

F: Waaye daa mel ni kenn ca ña fa teewoon parewulwoona déglu way tawat yi ñu wax.

D: Sa su ne ci mbir yu mel noonu lañuy dugg. Loolu luñu wara suppi la nak. Xellu yoon wu yàgg la.

F: Beneen gis gis ci ligeeyu Fann mooy penc yooyu itam. Bu ci dige rek desee, xam nga waxi nguurug Senegal. Xam nga ngor, jom ak kersa. Yaakaar nga ni penc yooyu man nañoo jariñ dara ?

D: Penc yi man nañoo jariñ, bu leen dara raxul ludul muy dajale fànn yi am ci kërug fajukaay gi yepp. Siiwal nañu penc yi lool nak. Nit ñi di fa daje, te loolu lu am solo la. Sori na lool nak pajoom mbooloo. Pajoom mboolo, ci àdduna bepp lañu koy amale ba mu des Fann. Fii dañu fiy tëggëkë fecc dong. Dañu fay coowaloo lu bari. Ku ñu indi nak, doo mana gis ni defuñu fi dara.

F: Noo gise yeneeni fajkat yi nga xam ni dañuy toog wër way tawat ji muy nettali ci ak dundam. Ñuy tekkil fajkat yi li muy wax. Fajkat yi di laaj ñu ko koy tekkil.

D: Woowu pajin tekkiwul dara. Dañu koy def lu bari nak ci iniversitey farans yi. Seetlu naa ko ca lopitaal St. Anne ci kanamu 400 nit ca kabineb Delay. Loolu dama koy tudde dong “xellug mala”.

F: Ñu tëpëtiku ak ñu rëŋëtiku bariwul ci Afrig. Ca Fann yekkati nañu fa lool dayob Bouffée Délirante yi. Ndax yaw mës ngaa def benn njàngat ci nosolosi?

D: Am na ay kaawu Bouffée Délirante yu bari – wànte ñungi wàññiku bu baax.

Buñu ko càmbaree ci gis gisu waa tugël, duñu mana xam li xew. Man li ma gënë yitteel, du càmbar boobu.

Buma ñëwée ci ab loppitaal, damay jéemë xam ni ag ndof nekke benn digante buñu jàppe feebar te ñu manees koo dëxëñ ci biir dundug doomu aadama bi.

Càmbarug nekkug doomu aadama bi moo ma ëppël solo.

Lislaam am na fii cër bu rëy. Ñu bari ci ŋiy waxtu, dañuy feeñal yëfi mistig. Loolu manees na koo tude Bouffée Délirante. Waxtu jii nak mën na am solo su rëy ci yarub nit ki walla sax mu feeñal ndese gu yàgg gu nekk ci moom.

Xam na benn dof boo xam man nañoo jàpp ni wér na, buñu sukkandikoo ci ay waxam. Manoon nañu koo boole ci ñu rëngëtiku ñi, wànte dafa amoon xam xam ba ñu ràññee ko ndax xam xam boobu. Ràññee googu nak mooy tax ba daana ka dootul daanu. Budoon 50 at ci ganaaw, kon boole nañu ndaw si ci ñi ame ay rab walla ab jibar, walla gisaanikat.

Kenn du ko yobbu kon di ko faj ci kërug dalal xel te dina mana am sax kon jëkër aki doom.

Ci diirub juróom fukki atkaarànge gi Wolof di jëfëndikóo ci réewum teknokarat soppiku na bu wér. Na sa waxin soppiku rekk, ñu daaldi lay jàppe ku tëlbëti. Danuy tëlbëtiku nak, ndax Sénégalci diirub juróom fukki at rekk amatul ludul ay bërëb yuñuy làqe ñu mel ni ndaw sii, ndax dañoo def benn ñaawteef te sax boo demee tayuñu ko. Ñu daaldi leen di yóbbu ci bërëb yu làqu yile.

Ndof goo gis, jàppal ni ñaari jaar jaar yu daje lay firndeel : muy jaar jaaru nit ki ak jaar jaaru askan wi muy dunde.

F: Ki nga fi wax leegi ci misaal, bokk na kon ci ñu néew ñi rëngëtikuwoon te ñu mujj faj leen bañu wér pilik ?

D: Bëggumë cee waxaat. Jaar jaari ndaw soosu yembagul. Dafa am lu mu dund lu am ay jexital yu diis. Wér na te jëlul ay nëroleptik ndaxte am na saasu dajeek ay nit ñu ko tàllal seeni nopp, déglu ko bamu mana wane maninam ak xaralaam.

F: Freuddem na ba tollu jamono ju mu génnée baatub kompleksu ëdib. Te dem na ba gëm ko, di ko jëfëndi koo. Ñoom Ortigues dañu doon jéemë firndeel boobule kompleks fii ci Afrig. Ndax ànd nga ci seennjàngat ya ñu daaneele.

D: Ëdib, waa Gerees la.

Mitolosi moom ay jaar jaar la rekk ci dundinu askan. Jàpp naa ni du metod bi gën, rawati na nak booko naree jëfëndikóo feneen fu bokkulak fa mu cosaanoo.Leeneena wara dox foofa.

F: lu baay di jariñ ci dundb doomi Senegal ?

D: fii, kenn mënu fee tudd baay te boolewoo ci lislaam. Baay dafa am lu rëy lu muy mengool ci doxalinu askan wi. Kenn du ko jéggi. Saa bu coow ame ak moom rekk day metti.

F: Ndax doom dina yeene dee baayam?

D: Ragal lool nday ak baay, dinay am.

Bëggë ray sa baay?

Coow day am yen saa yi. Wànte bëggë ray sa baay? – Dëglë manes naa gis mbir, daaldi ni: mungi wund, dafa bëggë ray baayam!

Man nak ñimewumaa wax loolu.

F: Cofeel gi doom ju góor di am ci ndayam nak?

D: Digante ndayak doom ju góor, dañu koosewal bamu ëpp. Am na way tawat yu daan feeñal bëgg guñu bëggë tëde seen nday. Am na itam jigeen ñu bëggë tëdëk seen doom. Manes nag gis ni ndongoy Senegal yi ci daara ju kawe ji jéppéeku leen di wax ci kompleksu Ëdib. Lu jëm ci insest, aay naa waxtaane.Foofu ànd naa faak Freud akñi ko gëm.

F: Ci jigeñaaley mitu Ëdib – ak ci téeréb linjiil itam – gisees na fa ray mbokk ak tëdé ku la araam agit ngóorjigéen. Ci Dakar nak askan wi daa tollu ci coppiku gu rëy. Li fi mag ñi bàyiwoon tas na wesar. Tàmbali nañu fee gis ay waxaki define góorjigéen. Ndax jot ngaa seetlu ay góorjigéen ca Fann agit nuñu gise ngóorjigéenak li fi mag ñi bàyi.

D: Damaa waarwoon, bima déggée ndongo yu kawe yi lànka kandaare ni: Góorjigéen, amul ci Senegal.

Man xam naa genn góorjigéen fi ci Senegal, ba tàmbalee waxtaan ak moom. Te damay dem it lu bari Ndar, fa nga xam ni nanguwees nañu fa ni ñi ñuy woowe Góorjigéen am nañu.

F: Ndax ngòorjigéen am na ci dëkku kaw yi?

D: Li wér te wóor daal mooy góorjigéen moom bari na ci Senegal. Te am na ci fànni askan wepp. Ay kilifay àdduna, ay boroom kër, ay mool, ay mbër. Wànte dañu ko fiy bañ bu wér. Góor ñiy toppandoo aka niru nirulu jigéen ñoom ay góorjigéen yu jigéen ñi sopp lañu, ndax yónneen yañu leen di demal.

Dafa am luñuy def ci askan wi. Dañu leen di bañ waaye itam dañu leen di xawa ragal. Ngóorjigéen am na ci dëkku kaw yi, wànte dañu koy weddi.

Ca Sàntarafrig, daje naa fa ak ay góor yu sol yéeréy jigéen ci ay dëkku kaw. Ci Góx yi diine lislaam di dox nak amul góor jigéen. Am na góorjigéen kay. Dañu ko faa nanguwul. Moo tax may laaj baxam lël yi ñuy def du rekk ngir bañ ngóorjigéen.

F: Nee nga ci diirub 15 at amul benn sikaatar afrikee…

D: ci 15 at tàggatuñu ca Fann benn sikaatar bu bokk Senegal.

F: Wan xeetu sikoterapi lañuy jëfëndikóo ca Fann?

D: NEróleptik ak maas kuraŋ moo ëpp ca Fann.

F: Chimi nak?

D: Déedéed.

F: Mbooleseen 200 way tawat ñoo nekk Fann.

D: ëpp nañu 100, wànte matuñu 200.

F: Maas kuraŋ bi, ñaata yoon ci bis bi?

D: Yombula xam. Man mii duma ko jëfëñdikoo. Waaye xam naa ni daal leeg leeg mu doon ñenti yoon ba juróomi yoon ci bis bi. Yenn saa yi mu dem sax ba juróon ñaar walla juróom ñatt. Ci yenn bërëb yi ci Fann ñaar walla ñatti yoon ci bis bi. Ñenti bërëb. Mbooleseen di fukki maas kuraŋ ak ñaar. Fukki yooni maas kuraŋ ak juróom bis bu nekk, du dara. Maas bu yàgg waaye.

Bimay doora ñëw Fann, dañu leen daan maas te kenn du leen waajale aki doom.

F: Walium sax daawu ci am?

Juróom benni at ci ganaaw, bimay soga ñëw, saa su benn malad daanoo, dañuy génné pajaasam teg ci biti, di ko maas ci kanamu ñepp.

F: Loolu kenn defatuko?

D: Déedéed.

F: Lu waral yaw doo maasaate?

D: Man damaa am saasu ay sikaatar tàgat ma yoo xam ni weneen doxalin lañu ma xamal wu wuuteek mititalaate.

Waaye nak kenn ku nekk yaay tànn say jànglekat.

F: Booko xoole ba ca biira biir, maas kuraŋ dara wuutalewuko ak mitital (tortiir).

D: Dëgg la. Mitital la. Nu la neex nak maneesnañu koo tude ! Dekki ! Dama jàpp ni lu ñu def ci xelu nit ñi la rekk. Man defe naa ni maasaate bi day yàq tàggatub fajkat yiy jàppalewaate. Defe naa ni ñi may jàppale, ñoom lañu gëñë tàggat ci wàllu sikaatiri – Dootuñu dóoré, duñu saaga, duñu maasaate.

Bu kenn daanoo, ñu ñepp dañuy ànd jéemë xool lu ko daaneel. Dangay nàngo xam walla nga lànka xam rekk.

F: Li jëm ci nëróleptik ca Fann, numu tollu ?

D: At yii ci ginaaw, tolluwoon na ci 2 milyoŋ CFA at mu nekk.

F: Kon muy tollook 25000 Mark – xaw naa tàkku sirtu ci isin yiy defar ay garab.

D: Isin kay bëgg nañu ñuy bind ay wardnaas. Defe naa ni lu mana nekk la ñuy faje walium agit yërmande.

Ci noonu maneesoon naa teg isini garab yi fëlé, daaldi feeñal nak jafe jafe ci koom bi. Ak ni waa Senegal dik faje, benn ekib bu dëggu rekk ak tuuti doomi nelawal doy na. Bu sunug bëgg di yokku rekk, dootuñu yitewoo nëróleptik yu bari.

F: Ndax ndaw si nga doon wax, dinga koy jox walium leeg leeg ?

D: Waaw.

F: Isin yi dañuy def ay test ci way tawat yi. Yan test lañuy def fi mu nekk nii?

D: Man bokku ma ci test yooyu. Antisikotik ak antidepressif lay jëfëndikoo.

F: Yu ban isi?

D: Sandoz, Spécia ak yeneen.

F: Doktoor yi dinañu jàpp ci pajinu yërmëndé woowule ?

D: Waaw.

F: Yaw nooku gise ?

D: Mënumë ci tontu ?

Xaalis bi dañu koy sédëlé bërëbu fajukaay yi ci biir lopitaal bepp ak mbooloom way tawat yi.

F: Ndax gis nga ni test yi tegi na ci yoon ba nga man koo layal.

D: bu fekkentewoon ni leer na ni liñu ciy seentu dees na ko ci am te itam niñu ko wara defe, defe nañu ko, waaw. Wànte leeg leeg am ay garab yu amul ñu weccee leen ak yeneen noonu. Menn pajin saxufi.

F: Dégg naa ni Doktoor yi ci bokk, dinañu leen jox 60000FCFA at mu nekk, muy tollok 750 Mark ?

D: Mën naa am.

F: taa yi am na ben luwaa ci Senegal buñu tude “médicaux legaux“ bu jëm ci defkatu ñaawteef yi ñu yaakaar ni dañoo am feebaru xel. Ñooñu dañu leena wara denc. Ndax defe nga ni sikaatiri bi ci Senegal, day gënë tëju walla dina ubbikuji ?

D: Defe naa ni sikaatirib Senegal day gën di jëfëndikóo ay duma ak mitital.

Yàggul rekk dañoo tàmbali di suqali turism bi. Ci noonu lañu jëlë kër yu mel ni ga ca Kenia def kow lay. Am na dekre bu nekk ci ginaaw buy xamle ni dañu fay def ab internaa.

F: Ndax sikaatar yi nekk Fann xam nañu ni dañu leena def aw lay rekk ?

D: Bir na ma ni duñu ay naxa naxa.

F: Doon nga ma wax taa yi lu jëm ci digante sikaatiri ak xeetu turism boobu.

D: Defe naa ni xalaat boobu, xalaatu ñi gënë bari ci ñi weddi sikaatiri la.

Defe naa ni saasu nit ki jugee ci ab jéll, day gëñë am doole. Defe naa ni doon na am solo, bu sikaatar yi doon jël LSD leeg leeg walla sax benn yoon rekk nday ñu mana xam lan mooy miir ak jeeneer. Nga xam ni beneen nit ngay doon. Jibar yu bari ci loolu lañuy sukkandiku. Nit ku ne day boqale lu bokk ci aadaam. Mës na maa laaj benn pereetar : Lu wuutale ab dof ak ki koy faj ? – mu daadi ni ma : ñoom ñaar jigee nañu lool. Li leen wuutale mooy, kartanug dund gi nekk ci nekkon ci way tawat ji dafa naaw.

F: Jibar bi moomitam, day tukki dem ci jaw ji walla biir ndox mi ni ko ruug aji tawat ji di defe. Ndax mës nga seetlu lu mel noonu ci ñi ngay faj ?

D: Xanaa dem ci jaw ji. Way tawat yi dañuy mel ni kuy naaw ba nekk ci kaw asamaan. Luy faral di am la. Te li way tawat yi di jeeneer mengóo naak li jibarub pereetar bi di jeeneer.

F: Jigeen ju katakayni ji nga doon wax, dafa daan jàppe ñaawteefam yi ni ab tukki …

D: Noonu laa ko gise. Màndargay lu yéemé, luy royroyi – ay jëfëm daf may fàttali li ngay jeeneer boo jëfëndikoo LSD. Defe naa ni, bu doon ca Afrig gu yàgg ga, dañu kooy jàppe ni ab gisaanikat buy digley sarax.

F: Daa nga ko jëfëndikoo kon?

D: Waaw.

[Ci turu 67–84]