For, wala sukkëndi, dajale. Lan moy di for, di sukkëndi, di dajale juumte yi ci aduna? Loolu lu muy tekki ? Kan la fitam, wala yég yégam tolu fi muy mëné attan yooyu juumte ag it farlu ci di leen seet. Ngir di leen xool ci ay gët te bañ di tàllal yox-yoxi. Su ñu ko jàngate woon ni ko artiste di jàngate, xëy na booba ne ñu mën gëstu naka la artistes yi di jariño seen kàttan ci wallum esthetique ngir for, dajale ba pare jëf ci yooyu juumte ? Exposition bi tudd Juumte yëpp yi amoon ci aduna, da ma leen a for di xewe ca RAW Material Company bu Ndakaaru mi ngi lalu ci liggééyu juróómi artiste – Papisto Boy, Maïsama, Leonore Mau, Thierno Seydou Sall ag Isabelle Thomas. Ñoñu, ca la ñu liggééy juróóm fukki at yi weesu, am na ay tontu ci yooyu laaj ag yeneen it. More…