Surnal internet bi ñu naan Hubert Fichte: Love and Ethnology la ko waral mo di mbir bu boole Goethe-Institut ak Haus der Kulturen der Welt, S. Fischer Stiftung ak S. Fischer Verlag ak ñeneen jap ci, te mu wara tukki jëm: Lisbon, Salvador de Bahia, Rio de Janeiro, Santiago de Chile, Ndakaru, New York, ak Berlin.

Hubert Fichte: Love and Ethnology fa muy tàmbëli mo di Nettali bu mag bu Fichte bi ñu naan Die Geschichte der Empfindlichkeit (Taarixu yég-yég), bi Fichte bin ci diggënte atum 1970 yi ak 1986 bi muy gaañu. Ci Ñaar-fukk-ak-ñenti teere ya mu fasoon-yéné bind, fukk-ak-juróom-ñent ño jota pare laata miy gaañu; fukk yi ci des jotu ño pare wola ñu reer. Diggënte 1987 ak 2006 fukk-ak-juróom-ñaari teere, yen yi nak motu ñu, jot ne ño feeñ ci réew yiy lakk Àleman nit ñi jot ci am ñu ko gëstu. Hubert Fichte: Love and Ethnology mbir mi mi ngi lalu ci ay teere yi S.Fischer Stiftung firndeel te li ko waral moodi fexe yen ci reew yi Fichte ak Leonore Mau jot tukki diggënte atum 1960 yi ak atum 1980 yi ñu jot ci liggéeyam.

Fichte, bi muy topato art yi te di bind, li ko soxaloon moodi fexe ba cuq littérature post-colonial ak art bu bes. Hubert Fichte: Love and Ethnology nak da fa jublu ci Black Atlantic (Paul Gilroy), ci diiwaan yi nit ñu ñuul yi tasaaroo fëp ci aduna ak seeniy cosaan yi nga xamante xiir ne ñu Fichte ak Mau ci seen liggéey ak dég-dégu ethnologie.

Exposition bi tudd Mistake! Mistake! said the rooster… and stepped down from the duck (juumte! juumte! La ganaar ga wax ni miy wàccé kanaara ga) (23.9.–5.11.2017), mi ngi lalu ci nettali bi ñu naan Ein Glüchkliche Liebe (1984/88; mbëggéél gu neix) te Josée Maria Vieira Mendes (éditrice: Cotovía) firndeel ko yàggul, da fa boole artistes yi ñu naan Gabriel Barbi, Ramiro Guerrero, Ana Jotta, Eurydice Kala, ak Simon Thompson, ak it liggéey bi Fichte ak Mau def ba ñu demé Salazar ca Purtugal ci atum 1960 yi. Exposition bi, te Jürgen Bock sanc ko ca berep bu nekk Lisbon bu ñu naan Lumiar Cité, dey jakkaarloo ak mbir yu soxaloon Fichte yu mel ni mbugël, sañ-sañi doomi adama, bisexualité ak it esthétique am moom ak Mau. Jéém-jéém yi Fichte def ci wallum yaatal mbind ci boppam ak mbind bu jublu ci art jot neñ ko sulli fofa ca Lisbon te nga xamante mooy jeego bu njëkk ci mbir mi.

Ñaari exposition Implosão:Trans(relacion)ando Hubert Fichte, Max Jorge Hinderer ak Amilcar Packer sanc ko ca MAM Museum of Modern Art (7.11.–17.12.2017) ca Salvador da Bahia ak Centro Municipal de Arte Hélio Oiticica (25.11.2017–13.1.2018) ca Rio de Janeiro, ñi ngi lalu ci nettali Fichte bi ñu naan Explosion (1993) te mu bind ko ci juróom-ñenti-téemeeri kayit. Tàmbële ci firndee bu Marcelos Backes (éditrice: Hedra) ak gëstu yi Fichte ak Mau defoon ci diiné Afrik bi ñu naan candomblé ak it coow bi jipoon ca diggënte Fichte ak photographe-ethnologue fraase bi ñu naan Pierre Verger ay artistu reew yu barre liggéey nañu, artistu Brésil ak yeneeni reew liggéey neñu.

Exposition bi nara am 2018 ci Museo Nacional de Bellas Artes (13.9.–18.11.2018ca Sanatiago de Chile, Mario Navarro mo ko sanc, mi ngi lalu: ci ay jukki ci Chili yu nekk ci nettali Fichte bi ñu naan Explosion bu Cecilia Pavón (éditrice: Metales Pesados) firndeel; ak it émission radio bi tudd Chile: Experiment auf die Zukunft (Chili: ab cafka ëllëg), ba njëkk daw radio Àlemañ (Norddeutscher Rundfunk) ca atum 1971. Fichte ak Mau de ño amoon coppatee politik bu Salvador Allende ba tax at bobu ca dëkkam leñu ko dund. Waxtaan yi Fichte amoon ak Allende ak it Carlos Jorquera, bi yoroon ci gornement Chili jëfëlente beek taskatu xibaar yi, am neñu soolo lolu ci jeego bi di Santiago de Chile, te it di feeñal bu bax yég-yég bi Fichte amoon ci socialisme bu Amerik Latine.

Jeego bu Ndakaru da fa boole Koyo Kouoh, commissaire ca RAW Material Company, ak Ibrahima Diagne mi nar a jiité waxtaan biy am Ndakaru (5.–24.10.2018). Jeego bi nak, ci teere boobu ñu naan Psyche (firi yu: Maguèye Kasse, Ibrahima Diagne ak Mamadou Diop, éditrice: L’Harmattan Sénégal) lay tàmbali, dàldi jublu ci tukki ya Fichte ak Mau tukki woon ci reew yu mel nii Benin, Togo, Senegal, Burkina Faso, Guinée Bissau ak Tanzanie ak gëstu yu Fichte jota gëstu ci wàllum fac ak facum wérëdig xel.

Ci firndeel Die Schwarze Stadt: Glossen (1980; Black City: Glosses, editeur: Sternberg Press) ci Àngale bu Adam Siegel la exposition bi wara am Participant Inc ak E-Flux Space lalu te Yesomi Umolu ag Katja Rivera sanc ko (3.12.2018–13.1.2019). Ci diggënte 1978 ak 1980 Fichte toog na lu yágg New York. Fofu la ko aada ak cosaanu ñit ñu ñuul yi gënë feeño, ndax fofu le ñu dajalo ñom ñëpp – fofu le ñu ko njëkk feeño ni ab “contre-universalisme”, beneen yoonu art bu dëggu te bu dul bu tubaab yi. Gis gis boobu Fichte gën na ko feeñal ci waxtaan yi mu waxtaan ak ay artistes, activictes ak yeneeni nit yi mu fa dajel.

Jéégo bi muj ci Love and Ethnology – The Colonial Dialectic of Sensitivity (after Hubert Fichte) (Love and Ethnology – The Colonial Dialectic of Sensitivity (bi ñu weeso Hubert Fichte)), Berlin lay xewee ca palaas bi ñu naan Haus der Kulturen der Welt  (18.10.2019–6.1.2020). Diedrich Diederischsen ak Anself Franke, ñaar ñi jiite mbir mi, lañu ko sas, ñu daldi dajale yitté yeek aaru kuréel yi jiitu te xewoon fenéen, boolé leen, yokk ci yu bees. Jeego Berlin bi, muy ci waxtaan bi muy taxawal ak aar yi muy wone, li muy jeema fësël mooy li liggéeyu Ficht ci wallum taalif ak ethnography jur ci Almañ bi nga xamantene da fa doon doora génne ci geer: xalaatam ci sey ak gis-gisu yég-yég gu xoot bi mu ñoral jamonoo yi muy wër li Paul Gilroy tuddee Black Atlantic. Aar yu bées yuy gëstu ci wallu teewalaat ak delloo, ci doxalim biy jël aar tekk ko ci kaw, ak it li dese dag ci buumu jaam bi ñu naan colonisation.

Ak ay aar waaye it ay archives yu bare yu Nadja Abt, Heriberto “Eddie” Alicea, Kader Attia, Gilles Aubry, Richard Avedon, Alvin Baltrop, Gabriel Barbi, Letícia Barreto, Coletivo Bonobando, Michael Buthe, Miguel Rio Branco, Rosemarie Clausen, Nathalie David, Mestre Didi, Hubert Fichte, Claudia del Fierro, Avril Forest, Alair Gomes, Renée Green, Philipp Gufler, Ayrson Heráclito, Isaac Julien, Euridice Zaituna Kala, Kippenberger und Akim S. aus 44, Friedl Kubelka, Pedro Lemebel, Cristóbal Lehyt, Musa Michelle Mattiuzzi, Leonore Mau, Tiona Nekkia McClodden, Virginia de Medeiros, Michaela Melián, Mario Navarro, Richard Oelze, Pan African Space Station, Lil Picard, André Pierre, Lili Reynaud-Dewar, Daniel Richter, Thierno Seydou Sall, Pap Samb (Papisto Boy), Pierre Verger, ak James Van Der Zee.

Jeego Berlin bi da fa andaak benn tééré bu mag bu nu tuddee Love and Ethnology – The Colonial Dialectic of Sensitivity (after Hubert Fichte), by Diedrich Diedrichsen, Anselm Franke, ak Haus der Kulturen der Welt amal te Sternberg Press wara genn ca fukk-ak-juroom-ñaarelu fan bu weeru Oktoobar ci atum 2019.