Hubert Fichte (1935–1986) ab bindkat ak ethnolog Àleman la woon. Ci liggééyam daan na jëfëndikòò taalif di gëstu ci boppam ak it, di nataal ci mbind yëf yi mu doon jàngat ci wallum “Queer Studies” ak “Postcolonial Studies”. Moo nga yaroo Hamburg, juddoo ci atum1935 dëkk bi ñu naan Perleberg, baay ji doonoon ab Naaru Yëwut, yaay ji ab Àleman. Li mu dund diamonoy deuxième guerre mondiale fekk xale la woon, ñu yobu ko a yeneeni xale Bavière ak Silésie, ak noteel ba nguuru hitler teggoon Naaru Yëwut yi, feñ na ci mbindam.
Ndaje Fichte ak fotograph ba ñu naan Leonore Mau (1916–2013) ci atum 1950 fekk mi ngi jang teyaatar jàngukaay bi ñu naan Hamburg Theater im Zimmer, lu am solo la ci jaar jaaram. Xaritoo bobu mujjé soppeeku xarito ba fàww te ñu bokk benn liggey 1960 ba ci biir atum 1980 yi: di gëstu, di bind, di photo ak di sanc xeetu ethnology bu bees. Ànd neñu ngir gëstu fa reew yu sore yu mel ni Brésil, Argentine, Chili, Haiti, Tanzanie, Ethiopie, Burkina Faso, Senegal, Trinidad, ak République Dominicaine.
Fichte jot na bind ay teere anthropologie ak It ay teere ethnologie yu rax taalif yu mel ni Xango (1976) ak Petersilie (1989), te it, moom ak xaritam May, bokk neñu liggey ay teere photo. Fichte bokkon na ci ap gàngóór bu ñu naan Gruppe 47 te it bare woon na itte lool: ba mu tàmbalé ci atum 1960 yi, nekkoon bindkat bu am bayre te xew ci jamono, doonoon góór-jigéén té màggé Àlemaañ ci jamono ya topp ci geer gu mag gi, ci la jublu ci liggééy ethnologie buy gëstu aadam ci teere yu mel ni Wolli Indienfahrer (1979/1983) ñu key woowee it “Sankt-Pauli interviews”. Fichte bëggoon na lool aada ak cosaanu doomu Afrik ya ca aduna bi yëp, ba tax na, ci atum 1960 yi, ca adaak ak cosaan yoyu, ak yeneen yu dul yu wa Europ, fa la jublu ay gëstoom.
Fichte da fa jàppoon ni ethnologie la ko war tey moodi weesu: gis gisu xaxam yi colonialism sabab ci wallum anthropologie ak ethnologie; la ñu jap ni mooy seen politig anti-raciste. Lolu jafeel na liggeyam jafeel mu jot ci yëf yi mu daan gëstu. Ndaxte: Fichte donte gëstu na ko bu baax ci bindam mësul gis yoon wu leer nàññ, wala sax gis gis gu woor ci wallum anthropologie. Ci ay Nettali ak woxtaan ya mu bind, ay émission radio ya boole ñar fukki teere yi ñu naan Die Geschichte der Empfindlichkeit (Taarixu yég yég), mi ngi fey mel ni ku tàyyi ci taxawaay bi mu taxaw ci diggënte kuy gëstu xam xam ak kuy bind li mu yég, kuy def journalisme ak kuy seet boppam.
Liggeyu Fichte, te lolu mi ngi gën feeñ ci teere bi ñuy wax Geschichte der Empfindlichkeit, ab yoon wu bees la ci wallum Anthropologie bu dese siiw ci aduna bi te bo xamante bindkat bi ci boppam dey soppeeku, ràññe boppam ci gis gisu wa reewam ak ña mu bokkal jamono: donte sax dëk yi mu dem moom ak Mau te ñu daan leen woowé “tiers monde” ndóól mi fa neewone mo ko fa njëk soxal, jot na gaawa jublu ci yeneeni yëf yu mel ni xeetu bañ ya andut ak rayanté, tourisme ak tourisme bu andak yëfu saay-saay, facum wérëdig xel ca Afrik, ak diine nit ku ñuul ca Afrik ak ca Amerik yu mel nii Candomblé bu Brésil.
Mbindum Fichte da fa sancu ci ethnographie, journalisme, taalif, ak waxtaan. Amut yox-yoxi, dey jaar ci digg bi, du taayi, am danar, di reelo, andak musik. Fichte te ni miy doxale mo ko waral dey boole kiy jang teereem ci ay weranteem ak ñakum yaakaaram. Fichte gisoon na ni jàppé xërëm ak aada art mënoon na soppi ak décoloniser taxawaayam ci wallum anthropologie. Fichte mi ngi gaañu Hamburg ci atum 1986, bokkoon na ci ñu njëk baayi xel li artistic ci minimalisme, Fluxus ak Happenings te it gëstu ci ngir yaataal ethnologie.
Diggënte 1990 ba legui, liggeyu Fichte ñu barre gëstu neñ ko ci dëkk yi ñuy lakk Àleman. Waaye, boobu ba leegi, liggeyam dese na feñ dëkk ya mu demoon anda fa ak Mau. Hubert Fichte: Love and Ethnology, ab projet bu boole Goethe-Institut ak Haus der Kulturen der Welt, S. Fischer Stiftung ak S. Fischer Verlag jap ci, da na tax dëkk yoyu mën jot ci liggeyam ak ay expositions, ay firndé ay teereem.